Lan mooy Nguuru Yàlla ?
Ndax dinga ne . . .
-
lu nekk ci suñu xol la ?
-
coobare Yàlla la ?
-
walla nguur la ci kaw asamaan ?
LAN LA BIIBËL BI WAX CI LAAJ BOOBU ?
“ Yàllay asamaan yi dina feeñal nguur gu dul tas mukk. ” — Dañeel 2:44, Mucc gi Yàlla waajal.
‘ May na nu doom ju góor, te dina yor nguur gi. ’ — Esayi 9:5.
LI MU WAX, BAN NJARIÑ NGA CI MËN A JËLE ?
-
Dinga mën a jot ci barke yi Nguur gu jub googu di indi. — Isaïe 48:17, 18.
-
Wér-gi-yaram gu mat sëkk ak jàmm ju doy ci àddina bu bees biy ñëw. — Peeñu ma 21:3, 4.
NDAX MËN NGA GËM LI MU WAX CI LAAJ BOOBU ?
Waaw waaw, xoolal liy topp :
-
Yeesu wone na li Nguuru Yàlla nar a def. Yeesu dafa waxoon taalibeem yi ñu ñaan Yàlla ngir Nguuram ñëw, ñaan itam ngir coobare Yàlla am ci kaw suuf (Macë 6:9, 10). Yeesu wone woon na naka la ñaan boobu di ame.
Bi mu nekkee ci kaw suuf, Yeesu dafa jox lekk ñi xiif, faj ñi feebar te dekkil ñi dee ! (Macë 15:29-38 ; Yowaana 11:38-44). Noonu la wonee lu rafet li Nguuru Yàlla nar a defal nit ñi, moom mi waroon a nekk njiitu Nguur googu. — Peeñu ma 11:15.
-
Ni àddina bi mel tey dafay wone ci lu leer ne léegi Nguuru Yàlla ñëw. Yeesu dafa yégle woon ne bala Nguur googu di indi jàmm ci kaw suuf, àddina bi dina metti ndax xare yi, xiif bi ak ay yëngu-yëngu suuf. — Macë 24:3, 7.
Loolu yépp ñu ngi koy gis tey. Kon mën nañu gëm ne léegi Nguuru Yàlla dindi fi poroblem yooyu yépp.
LOO XALAAT CI LAAJ BII ?
Naka la dund bi di mel ci kaw suuf bu Nguuru Yàlla ñëwee ?
Biibël bi dafa ciy tontu ci SABÓOR 37:29 ak ISAÏE 65:21-23.