Ubbil li ci biir

Ndimbal pur ndaw ñi

Xoolal ni Biibël bi mënee dimbali ndaw ñi ci jafe-jafe yi ñuy faral di am.

Tànnal benn waxtaan

Xoolal li sog a génn ci wideo yi, misik, téere yi ak xibaar yi.

Seetal li bees

Ndax bëgg nga ñu seetsi la?

Mën nga waxtaan ci benn laaj ci Biibël bi walla nga jàng lu jëm ci Seede Yexowa yi.

Ñëwal teew ci benn ndaje Seede Yexowa yi

Xoolal fi ñuy defe suñu ndaje yi ak ni ñuy jaamoo Yàlla. Ñépp ñi ko bëgg mën nañu ñëw. Kenn du fey dara.

Wideo yi

Ndax mën nga nekk xaritu Yàlla?

Bi àddina sosoo ba tey, nit ñaa ngi wut a xam kan mooy seen Boroom. Biibël bi mën na ñu dimbali ñu nekk xaritu Yàlla. Xaritoo boobu dafay tàmbali ci xam turu Yàlla.

XÓOTALAL WAXTAAN BI

Seede Yexowa yi : Ñan lañu ?

Ñun, Seede Yexowa yi dañuy seede, maanaam dañuy wax ci Yexowa mi Biibël bi wax ne mooy Yàlla te moo sàkk lépp. Dañuy wax itam lu jëm ci Nguuram. Ci suñu mbootaay am na lu tollook ay téeméeri xeet ak ay téeméeri làkk, waaye loolu terewul ñun ñépp ñu nekk benn ci li ñu bëgg ci wàllu ngëm. Màggal Yexowa mooy li ëpp solo ci ñun. Dañuy def itam lépp ngir roy Yeesu Kirist, moo tax nekk karceen doon lu réy ci ñun. Ku nekk ci ñun dafay jël jot ngir dimbali nit ñi ñu jàng li nekk ci Biibël bi ak lu jëm ci nguuru Yàlla.

Xoolal li am ci suñu palaas bii ci internet. Mën nga fi liir Biibël bi. Yokkal li nga xam ci ñun ak ci li ñu gëm.

 

Two of Jehovah's Witnesses preaching to a man in a rice paddy.