Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Nañu màggal Yexowa

Nañu màggal Yexowa

(Taalifi Cant 96:8)

Telesarseel:

  1. 1. Ku mel ni yow céy Yexowa ?

    Yaay Aji kawe ji wóor.

    Naka laa lay mën a feyee,

    Yow mi ñu won Mbëggeel gu yaa ?

    Su ma gëstoo ci sa càkkéef,

    Sa kàttan di may yéem lool.

    Waaw man maay kan céy Yexowa,

    Ba nga may barkeel saa su ne?

    (AWU BI)

    Céy Yexowa déglul sama woy wi,

    Woyu cant laa la jagleel.

    Yaay Buur ba fàww, yow yaay sama Yàlla,

    Li nga moom laa lay delloo.

    Li ma war mooy màggal la.

  2. 2. Jébbalu naa ci yow Yàlla.

    Màggal la mooy li may seet.

    Ci samay jëf, ci waare bi,

    Damay xamle ni nga baaxee.

    Jaamu la, loolu laay bàkkoo.

    Yaa may may ndam ak doole.

    Yal na nga doon ba abadan

    Ki may won yoon bi gën ci man.

    (AWU BI)

    Céy Yexowa déglul sama woy wi,.

    Woyu cant laa la jagleel.

    Yaay Buur ba fàww, yow yaay sama Yàlla,

    Li nga moom laa lay delloo.

    Li ma war mooy màggal la.

  3. 3. Weer wi, biddéew yi, jant bi,

    Ñooy firnde yuy wone ne

    Fonk nga nit yi nga sàkk.

    Di ci xalaat bégal na ma.

    Li nga def rafet na, Yàlla.

    Dama la war a gërëm.

    Baay desalatoo ma dara,

    Amuma sa fey Yexowa.

    (AWU BI)

    Céy Yexowa déglul sama woy wi,

    Woyu cant laa la jagleel.

    Yaay Buur ba fàww, yow yaay sama Yàlla,

    Li nga moom laa lay delloo.

    Li ma war mooy màggal la.