Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Bul ragal

Bul ragal

Telesarseel:

  1. 1. Boo nekkee ci tiis, sa xel day jaxasoo.

    Dangay wut pexe, muy mel ni yoon amul.

    Boo nekkee ci biir njàqare,

    Bul am xel ñaar bay xàddi

    Nanga ñaan

    Yàlla

    (AWU BI)

    Bul ragal ndax Yexowa mu ngeek yow.

    Yàlla mu ngi lay jàppale saa su ne.

    Lu mbir yi diis diis ci yow,

    Na la wóor ne Yàlla du la fàtte. 

    Xelam a ngi ci yow.

    Deel ñaan,

    Bul tiit bul ragal.

  2. 2. Te am nga ay mbokk, yu lay ñaanal.

    Xarit yu wóor lañu, dañuy seddal sa xol.

    Njàngum Biibël bi moo lay aar

    Di la may doole ba, doonte sax

    Mu ngi tar,

    Nanga ñaan.

    (AWU BI)

    Bul ragal ndax Yexowa mu ngeek yow.

    Yàlla mu ngi lay jàppale saa su ne.

    Lu mbir yi diis diis ci yow,

    Na la wóor ne Yàlla du la fàtte.

    Xelam a ngi ci yow,

    Deel ñaan.

    (PONT BI)

    Ci jafe-jafe joo mën a ne,

    Nanga siggi,

    Te bul xàddi.

    (AWU BI)

    Bul ragal ndax Yexowa mu ngeek yow.

    Yàlla mu ngi lay jàppale saa su ne.

    Lu mbir yi diis diis ci yow,

    Na la wóor ne Yàlla du la fàtte.

    Xelam a ngi ci yow.

    Deel ñaan,

    Bul tiit bul ragal.