Jëf yi Yàlla bañ
Njàngale 10
Jëf yi Yàlla bañ
Naka nga wara gise jëf yi Yàlla wax ne dañoo bon ? (1)
Yan ànd walla tëdd ñoo araam ? (2)
Naka la taalibe Isaa wara gise fen ? (3) wure xaalis ? (3) sàcc ? (3) jëfi fitna ? (4) mbirum tuuri maam walla rab ? (5) naan ba màndi ? (6)
Naka la nit mënee bàyyi di def lu bon ? (7)
1. Jaami Yàlla yi dañoo bëgg lu baax. Waaye war nañu jànga bañ lu bon (Sabuur 97:10). Maanaam dañu wara moytu jëf yi Yàlla bañ. Yan ñooy yenn ci jëf yooyu?
2. Tëdd ak kenn fekk séyuleen : Tëdd ak kenn fekk séyaguleen, njaaloo, tëdd ak mala, tëdd ak sa mbokk mu jege-jege, góor-jigéen, jëf yooyu yépp ay bàkkaar yu réy lañu ci kanamu Yàlla (3 Musaa 18:6 ; Room 1:26, 27 ; 1 Korent 6:9, 10). Su ñaari nit nekkaalee, war nañu tàggoo walla ñu séy ci yoon. — Yawut yi 13:4.
3. Fen, wure xaalis, sàcc : Yexowa Yàlla mënul fen (Titt 1:2). Nit ñi bëgga neex Yàlla dañu wara moytu fen (Léebu 6:16-19 ; Kolos 3:9, 10). Bëgge bokk na ci bépp wure xaalis. Kon nag taalibe Isaa yi waruñu bokk ci benn fasoŋu wure xaalis, muy lotëri, rawante fas walla kàrt xaalis (Efes 5:3- 5). Taalibe Isaa yi duñu sàcc. Duñu jënd li ñu xam ne dañu ko sàcc. Duñu jël li ñu leen mayul walla li ñu leen àbbalul. — 2 Musaa 20:15 ; Efes 4:28.
4. Naqadi deret, jëfi fitna : Boo meree ba mënatuloo téye sa bopp, loolu mën na la yóbbu ci jëfi fitna (1 Musaa 4:5-8). Ku am jikko jooju, mënuloo nekk xaritu Yàlla (Sabuur 11:5 ; Léebu 22:24, 25). Feyyu walla delloo lu bon ki la def lu bon, baaxul. — Léebu 24:29 ; Room 12:17-21.
5. Kort, mbirum tuuri maam walla rab ak yu mel noonu : Am na ñuy jaar ci kàttanu tuuri maam yi walla rab yi ngir jéema faj feebar. Am na ñeneen ñuy liggéey seeni noon ngir ñu feebar walla sax ñu dee. Kàttan gi nekk ci ginnaaw jëf yooyu yépp, ci Seytaane la jóge. Kon taalibe Isaa yi waruñu bokk ci benn ci jëf yooyu (5 Musaa 18:9-13). Bu ñu la bëggee kort walla liggéey, li la gëna mëna aar mooy taq ci Yexowa. — Léebu 18:10.
6. Naan ba màndi : Naan tuuti biiñ, beer, walla sàngara bonul (Sabuur 104:15 ; 1 Timote 5:23). Waaye naan ba mu ëpp walla naan ba màndi, lu bon la ci kanamu Yàlla (1 Korent 5:11-13 ; 1 Timote 3:8). Soo naanee ba mu ëpp mën nga ci ñàkk sa wér-gi-yaram te tas sa njaboot. Loolu mën na tax itam nga gaawa nangu def yeneen yëf yu bon. — Léebu 23:20, 21, 29-35.
7. Ñi dëkk ci li Yàlla bañ,‘ duñu donn Nguuru Yàlla ’. (Galasi 5:19-21.) Soo bëggee Yàlla dëgg-dëgg te soo ko bëggee neex, dinga mëna bàyyi jëf yooyu (1 Yowanna 5:3). Jàngal bañ li Yàlla wax ne lu bon la (Room 12:9). Àndal ak nit ñi tàmm def lu neex Yàlla (Léebu 13:20). Say moroomi taalibe Isaa yu ñor ci wàllu ngëm mën nañu la dimbali (Saak 5:14). Li ëpp solo mooy nga wékk sa yaakaar ci Yàlla di ko ñaan mu dimbali la. — Filipp 4:6, 7, 13.
[Nataal yi nekk paas 20, 21]
Yàlla bañ na naan ba màndi, sàcc, wure xaalis, ak jëfi fitna