Jaami Yàlla yi war nañu set
Njàngale 9
Jaami Yàlla yi war nañu set
Lu tax ñu wara set ci bépp fànn ? (1)
Lan la set ci wàllu ngëm tekki ? (2) set ci jikko ? (3) set ci xalaat ? (4) set ci yaram ? (5)
Yan fasoŋu wax yu ñaaw lañu wara moytu ? (6)
1. Yexowa Yàlla dafa set te sell. Dafa bëgg jaamam yi wéy di set — ci wàllu ngëm, ci jikko, ci xalaat ak ci yaram (1 Pieer 1:16). Ku bëgga wéy di set ni ko Yàlla bëgge, war nga ci farlu bu baax-a-baax. Ñu ngi ci àddina su bañ lu sell. War nañu xeex itam, xeex bu metti, ak suñuy jikko yi ñuy xiir ci lu bon. Waaye waruñu bàyyi xeex boobu.
2. Set ci wàllu ngëm : Bu ñu bëggee jaamu Yexowa, waratuñu bokk ci bépp njàngale walla aada bu nekk ci diine yu dul dëgg yi. Dañu wara génn ci diine yu dul dëgg yi te waruñu leena jàppale ci lu mu mënta doon (2 Korent 6:14-18 ; Peeñu bi 18:4). Bu ñu xasee jàng dëgg gi ci Yàlla, am na ay nit yu ñu wara moytu. Ñooy ñiy jàngale ay fen te bëgga nax nit ñi. — 2 Yowanna 10, 11.
3. Set ci jikko : Yexowa dafa bëgg jaamam yi wone jikko taalibe Isaa yu dëgg yi fu ñu mënta nekk (1 Pieer 2:12). Yàlla dafay gis lépp lu ñuy def, bu dee sax dañuy nëbbu (Yawut yi 4:13). Waruñu tëdd ak koo xam ne nekkul suñu jëkkër walla suñu jabar, walla bokk ci yeneen jëf yu bon yu nit ñi di def ci suñu jamano. — 1 Korent 6:9-11.
4. Set ci xalaat : Su ñu feesalee suñu xel ak xalaat yu sell, suñuy jëf itam dinañu sell (Filipp 4:8). Waaye dëkk ci xalaat yu bon mooy jur jëf yu bon (Macë 15:18-20). Waruñu fo mukk ak lépp lu mëna tilimal suñu xel. Njàngum Kàddu Yàlla mën na feesal suñu xel ak ay xalaat yu set.
5. Set ci yaram : Ndegam dañuy wax ci Yàlla ju sell, taalibe Isaa yi dañu wara set ci seen yaram te sol lu set. Ku jóge wanag war nga raxasu. Bala ñuy lekk walla laal ñam war nañu raxasu. Su fekkee ne amuloo wanag, boo demee ginnaaw kër war nga gas pax, te boo paree suul ko (5 Musaa 23:12, 13). Set ci yaram dafay yokk wér-gi-yaram. Këru taalibe Isaa war na set ci biir ak ci biti. Kër googu war na nekk kër gu jara roy ci gox gi mu nekk.
6. Set ci wax : Jaami Yàlla yi, dëgg rekk lañu wara wax. Fenkat yi duñu dugg ci Nguuru Yàlla (Efes 4:25 ; Peeñu bi 21:8). Taalibe Isaa yi duñu wax ay wax yu bon. Duñu déglu walla wax ay kaf yu ñaaw walla ay nettali yu tilim. Seen waxin bu sell boobu mooy tax ñu ràññee leen fu ñuy liggéeye, fu ñuy jànge ak fu ñu dëkk. — Efes 4:29, 31 ; 5:3.
[Nataal yi nekk paas 19]
Jaami Yàlla yi war nañu set ci bépp fànn