Kan mooy Ibliis ?
Njàngale 4
Kan mooy Ibliis ?
Seytaane mi nekk Ibliis — fan la jóge ? (1, 2)
Naka la Seytaane di naxe nit ñi ? (3-7)
Lu tax nga wara xeex Ibliis ? (7)
1. Baat “ ibliis ”, mu ngi tekki kuy wax ay fen yu ñaaw ci keneen. “ Seytaane ”, mu ngi tekki noon walla kuy xeex keneen. Noonu lañu woowe ki gëna mag ci nooni Yàlla yi. Ca njëlbéen, malaaka mu mat sëkk la woon ca asamaan ak Yàlla. Waaye dafa mujja yëg boppam lool te bëgg ñu jaamu ko, fekk Yàlla rekk lañu wara jaamu. — Macë 4:8-10.
2. Malaaka moomu, maanaam Seytaane, dafa jaar ci jaan ngir wax ak Awa. Dafa ko fen ba mu jéggi yoonu Yàlla. Noonu la Seytaane weddee li ñuy wax “ Kiliftéefu Yàlla ”, walla taxawaayam niki Aji-Kowe ji. Seytaane dafa weddi ne fasoŋ bi Yàlla di nguuroo moo gën ci jaamam yi. Weddi na itam ne nit mën na takku ci Yàlla te dëkk ci. Noonu la defe boppam noonu Yàlla. Looloo tax ñu mujj koo tudde Seytaane mi nekk Ibliis. — 1 Musaa 3:1-5 ; Ayóoba 1:8-11 ; Peeñu bi 12:9.
3. Seytaane dafay jéema nax nit ñi ba ñu jaamu ko (2 Korent 11:3, 14). Mën na jaar ci diine yu dul dëgg yi ngir nax nit ñi. Bu amee diine buy jàngale ay fen ci Yàlla, ci lu wóor Seytaane lay liggéeyal (Yowanna 8:44). Nit ñi bokk ci diine yu dul dëgg yi, mën nañu foog ci seen biir xol ne Yàlla dëgg ji lañuy jaamu. Waaye ci lu wóor Seytaane lañuy liggéeyal. Moom mooy ‘ yàllay jamano jii ’. — 2 Korent 4:4.
4. Seytaane mën na jaar itam ci mbirum tuuri maam walla rab ak yu mel noonu ngir xëcc nit ñi ci kiliftéefam. Nit ñi Seytaane di ilif mën nañu ñaan ay rab ñu sàmm leen, lor ñeneen, wax liy am ëllëg, walla def ay kéemaan. Seytaane mooy doole ju bon ji nekk ci ginnaaw jëf yooyu yépp. Bu ñu bëggee neex Yàlla, waruñu laal dara lu jëm ci mbir moomu. — 5 Musaa 18:10-12 ; Jëf ya 19:18, 19.
5. Seytaane dafay jaar itam ci fonk sa xeet ba mu ëpp walla ci jaamu ay mbootaayi politig ngir nax nit ñi. Am na ñu foog ne seen réew walla seen xeet moo gën yeneen yi. Wànte loolu du dëgg (Jëf ya 10:34, 35). Ñeneen ñaa ngi teg seen yaakaar ci mbootaayi politig yi ngir dindi coono yi nit ñi am. Noonu lañuy bañe Nguuru Yàlla. Moom rekk moo mëna dindi suñuy coono. — Dañel 2:44.
6. Seytaane dina jaar itam ci bëgg-bëgg yu araam ngir nax nit ñi. Yexowa dafa ñuy wax ñu moytu jëf yu bon yi ndaxte xam na ne jëf yooyu dañuy loraate (Galasi 6:7, 8). Ñenn nit mën nañu bëgg nga topp leen ci jëf yooyu. Wànte bul fàtte ne, ci dëgg dëgg, Seytaane moo bëgg nga bokk ci loolu. — 1 Korent 6:9, 10 ; 15:33.
7. Seytaane mën na jaar ci fitnaal walla ci nit ñi lay xatal ba nga bàyyi Yexowa. Ñenn ci say mbokk yi mën nañu mer mer mu tàng ndax li ngay jàng Mbind mu sell mi. Ñeneen ñi mën nañu la ñaawal. Waaye ci kan nga ame dund ? Seytaane dafa la bëgg tiital ba nga bàyyi jànga xam Yexowa. Bul bàyyi Seytaane gañe (Macë 10:34-39 ; 1 Pieer 5:8, 9) ! Boo xeexee Ibliis, dinga mëna bégloo Yexowa te wone ne Kiliftéefam nga faral. — Léebu 27:11.
[Nataal yi nekk paas 9]
Diine yu dul dëgg, mbirum tuuri maam walla rab, fonk sa réew ba mu ëpp, ñooy réeral nit ñi
[Nataal bi nekk paas 9]
Wéyal di jànga xam Yexowa, noonu ngay xeexe Ibliis