Lan mooy coobare Yàlla ngir suuf si ?
Njàngale 5
Lan mooy coobare Yàlla ngir suuf si ?
Lu tax Yexowa sàkk suuf si ? (1, 2)
Lu tax tey jii suuf si nekkul àjjana ? (3)
Lan mooy dal nit ñu bon ñi ? (4)
Bu ëllëgee, lan la Isaa di defal ñi feebar ? ñi màgget ? ñi dee ? (5, 6)
Boo bëggee bokk ci barke yooyu di am, lan nga wara def ? (7)
1. Yexowa sàkk na suuf si ndax nit ñi mën cee dund ba fàww, ci bànneex. Dafa bëggoon suuf si fees ba fàww ak ay nit ñu jub te bég (Sabuur 115:16 ; Isayi 45:18). Suuf si duñu ko sànk mukk. Dina fi nekk ba abadan. — Sabuur 104:5 ; Dajalekat 1:4.
2. Bala Yàlla di bind nit, dafa tànn benn béréb bu ndaw ci kow suuf, defar ko mu nekk àjjana ju rafet. Mu tudde ko toolu Eden. Foofu la tegoon góor gu njëkk ga Aadama, ak jigéen ju njëkk ja Awa. Yàlla dafa bëggoon ñu am ay doom te ñu feesal suuf si sépp. Ndànk-ndànk lañu naroona yaatal àjjana jooju ba suuf si sépp nekk àjjana. — 1 Musaa 1:28 ; 2:8, 15.
3. Aadama ak Awa ñoo teyoon jéggi yoonu Yàlla. Noonu lañu bàkkaare. Yexowa daldi leen génne ca toolu Eden ba. Noonu lañu ñàkke àjjana (1 Musaa 3:1-6, 23). Waaye Yexowa fàttewul li mu bëggoona def ak suuf sii. Dig na ñu ne dina ko defar mu nekk àjjana, fu nit ñiy dund ba fàww. Naka la koy defe ? — Sabuur 37:29.
4. Bala suuf sii mëna nekk àjjana, dañu wara dindi nit ñu bon ñi (Sabuur 37:38). Loolu ca Armagedon lay ame. Armagedon mooy xeexu Yàlla bu fi nara dindi lu bon. Bu loolu amee, dinañu tëj Seytaane 1 000 at. Booba, kenn ku bon du fi des ngir yàq suuf si. Ñiy jaamu Yàlla rekk ñooy mucc. — Peeñu bi 16:14, 16 ; 20:1-3.
5. Ginnaaw loolu, Isaa dina nguuru 1 000 at ci kow suuf si (Peeñu bi 20:6). Ndànk-ndànk dina dindi bàkkaar ci suñu xel ak ci suñu yaram. Dinañu mujja nekk ay nit ñu mat sëkk ni Aadama ak Awa meloon bala ñoo bàkkaar. Bu boobaa, feebar, màgget ak dee dootuñu am. Ñi feebar, dinañu wér te ñi màgget dinañu dellu nekk ndaw. — Ayóoba 33:25 ; Isayi 33:24 ; Peeñu bi 21:3, 4.
6. Ci 1 000 at yi Isaa di nguuru, nit ñu takku ci Yàlla dinañu defar suuf si sépp ba mu nekk àjjana (Lukk 23:43). Ay milyoŋi nit ñu dee dinañu dekki itam ngir dund ci kow suuf si (Jëf ya 24:15). Bu ñu defee li leen Yàlla laaj, dinañu wéy di dund ba fàww ci kow suuf. Bu ñu ko deful, dinañu leen sànk ba fàww. — Yowanna 5:28, 29 ; Peeñu bi 20:11-15.
7. Kon li Yàlla bëggoon ca njëlbéen ci kow suuf si dina am. Ndax bëgg nga bokk ci barke yooyu di am ? Boo ko bëggee, war nga wéy di jànga xam Yexowa te topp li mu ñu laaj. Lu la ci mëna dimbali mooy di fekke ndaje Seede Yexowa yi ci Saalu Nguur gi la gëna jege. — Isayi 11:9 ; Yawut yi 10:24, 25.
[Nataal bi nekk paas 10]
Àjjana ji ñu ñàkk
[Nataal yi nekk paas 11]
Bu Armagedon ñówee ba noppi, dinañu defar suuf si mu nekk àjjana