Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Naka lañu wara dunde ci suñu njaboot ba mu neex Yàlla ?

Naka lañu wara dunde ci suñu njaboot ba mu neex Yàlla ?

Njàngale 8

Naka lañu wara dunde ci suñu njaboot ba mu neex Yàlla ?

Lan mooy taxawaayu jëkkër ci biir njaboot ? (1)

Naka la jëkkër wara nekke ak jabaram ? (2)

Lan mooy wareefu baay ? (3)

Lan mooy wareefu jabar ci biir njaboot ? (4)

Lan la Yàlla laaj waajur yi ak xale yi ? (5)

Naka la Mbind mu sell mi gise tàggoo ak tas séy ? (6, 7)

1. Mbind mu sell mi nee na jëkkër mooy njiitu njabootam (1 Korent 11:3). Jëkkër, benn jabar rekk la wara am. War nañu séy ci yoon. — 1 Timote 3:2 ; Titt 3:1.

2. Jëkkër war na bëgg jabaram ni mu bëgge boppam. Dafa wara nekk ak jabaram ni Isaa nekkewoon ak taalibeem ya (Efes 5:25, 28, 29). Warul dóor mukk jabaram walla toroxal ko ci fasoŋ bu mu mënta doon. Waaye war na koo may cër te suturaal ko. — Kolos 3:19 ; 1 Pieer 3:7.

3. Baay war na daan dooleem ngir toppatoo njabootam. War na utal jabaram ak doomam yi lu ñu lekk, lu ñu sol ak fu ñu dëkk. Baay war na faj itam soxlay njabootam ci wàllu ngëm (1 Timote 5:8). Moom mooy jiitu ci dimbali njabootam mu xam Yàlla ak li Mu bëgg. — 5 Musaa 6:4-9 ; Efes 6:4.

4. Jabar war na dimbali jëkkëram bu baax (1 Musaa 2:18). Dafa wara jàppale jëkkëram ci jàngal ak yar seeni doom (Léebu 1:8). Yexowa laaj na jabar muy toppatoo njabootam, toppatoo bu ànd ak mbëggeel (Léebu 31:10, 15, 26, 27 ; Titt 2:4, 5). Dafa wara weg jëkkëram bu baax-a-baax. — Efes 5:22, 23, 33.

5. Yàlla laaj na xale yi ñu déggal seeni waajur (Efes 6:1-3). Yar ak jubbanti xale yi, waajur yi la ko Yàlla dénk. Waajur yi war nañu fexe ba mëna toog ak seeni doom di leen jàngal Mbind mu sell mi, di toppatoo seeni soxla ci wàllu ngëm ak ci wàllu cofeel (5 Musaa 11:18, 19 ; Léebu 22:6, 15). Waajur yi waruñu tàng ba mu ëpp walla soxor, bu ñuy yar seeni doom. — Kolos 3:21.

6. Ñaar ñuy séy, bu ñu déggoowul, war nañu jéema topp ndigali Mbind mu sell mi. Mbind mu sell mi dafa ñuy xiirtal ñuy wone mbëggeel, te ñuy baalante (Kolos 3:12-14). Ni ko Kàddu Yàlla wone, waruñu foog ne tàggoo mooy faj jafe-jafe yu ndaw ci biir séy. Waaye jabar mën na fay (1) su jëkkëram lànkee dundal njabootam, (2) su ko jëkkëram dóoree ba mu mën cee ñakk wér-gi-yaramam walla bakkanam, walla (3) su ko xatalee ba mënul am bunt ngir jaamu Yexowa. — 1 Korent 7:12, 13.

7. Ñaar ñuy séy war nañu yem ku nekk ci moroomam. Boo njaaloo, tooñ nga Yàlla, tooñ nga ki nga séyal (Yawut yi 13:4). Mbind mu sell mi nee na, lenn rekk moo mëna tax nga tas sa séy te mëna amaat jëkkër walla jabar : bu fekkee ne ki nga séyal tëdd na ak keneen (Macë 19:6-9 ; Room 7:2, 3). Su amee ku tas séyam, fekk Mbind mu sell mi mayu ko ko, te séyaat ak keneen, Yexowa bañ na loolu. — Malaki 2:14-16.

[Nataal yi nekk paas 16, 17]

Yàlla mu ngi laaj waajur yi ñu jàngal seeni doom te ñu jubbanti leen

[Nataal bi nekk paas 17]

Baay bu baax dafay toppatoo njabootam te faj seeni soxla ci wàllu ngëm