Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

PÀCC BENN

Li ñu wax ci Yàlla bare na. Lan mooy dëgg gi ?

Li ñu wax ci Yàlla bare na. Lan mooy dëgg gi ?
  • Ndax Yàlla fonk na la dëgg ?

  • Yàlla, naka la mel ? Ndax am na tur ?

  • Ndax mën nañu jege Yàlla ?

1, 2. Lu tax yenn saay laajte baax ?

NDAX gis nga ni xale yi baree laaj ? Ñu bare, bu ñu komaasee wax rekk, komaase di laajte, mel ni xale bi ñuy wone fii. Dañu am ay laaj yu bare yu mel ni : ‘ Lu tax lii ? ’ walla ‘ Lii lan la ? ’ Dinga leen jéem a tontu, waaye yenn saay du yomb. Sa tont mën na leer sax, waaye du tere xale bi tegaat ci : ‘ Lu tax ? ’

2 Du xale yi kese ñooy laajte. Bu nit ñi di màgg, dañuy kontine di am lu ñuy laaj. Lée-lée ñu laaj suñu yoon, walla laaj li ñu war a moytu ngir aar suñu bopp, walla laaj ngir xam rekk. Waaye, dafa mel ni ñu bare bëggatuñu di laajte, rawatina ci laaj yi ëpp solo ci àddina. Walla boog, jéematuñu xam tont yi.

3. Lu tax ñu bare bàyyi jéem a xam tontu laaj yi gën a am solo ?

3 Seetal laaj bi ubbi téere bii, maanaam Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ? Walla laaj yi nekk ci xët 3 ak 6, walla laaj yiy ubbi pàcc bii. Bokk nañu ci laaj yi gën a am solo yi nit mën a laaj. Waaye ñu bare tey jéematuñu xam tontu laaj yooyu. Lu waral loolu ? Ndax Biibël bi tontu na ci laaj yooyu ? Am na ñu foog ne li ci Biibël bi wax, dafa jafee nànd lool. Am na ñuy wax ne kuy laaj laaj yooyu, dinga mujj a rus. Am na ñu yaakaar it ne njiitu diine yi walla ñiy jàngale ñoo mën a tontu laaj yu mel noonu. Yow nag ? Loo ci xalaat ?

4, 5. Waxal yenn ci laaj yi gën a am solo yi ñu mën a laaj, te lu tax ñu war a seet ngir xam tont yi ?

4 Wóor na ne yow itam bëgg nga xam tontu laaj yooyu am solo ci dundu doomu Aadama. Wóor na ne, lée-lée dangay laaj sa bopp lii : ‘ Lu tax nit di dund ? Suñu dund, ndax mën na gën a neex ? Naka la Yàlla mel dëgg ? ’ Laajte lu mel noonu, baax na lool. Te waruloo ci tàyyi ba keroog ngay am tont yu leer te wóor. Loolu dafa am solo lool. Yeesu Kirist, mi nekkoon jàngalekat bu mag, nee woon na lii : “Ñaanleen, ñu may leen ; seetleen te dingeen gis ; fëggleen, ñu ubbil leen.” — Macë 7:⁠7.

5 Boo kontinee di seet ngir xam tontu laaj yu am solo yooyu, dinga gis ne jaroon na nga ciy sonn (Proverbes 2:1-5). Ak lu la nit ñi mënta wax, nanga xam ne laaj yooyu am nañu tont, te mën nga gis tont yooyu ci biir Biibël bi. Tont yi jafewuñu nànd. Te li ci gën a neex mooy, tont yooyu dinañu la may mbégte ak yaakaaru ëllëg. Te it tont yooyu mën nañu la dimbali nga am dund bu neex dëgg ci jamono ji ñu nekk nii. Nañu komaase ak laaj bu jaaxal nit ñu bare.

NDAX YÀLLA DAFA FONK NIT TE BARE YËRMANDE ?

6. Bu ñu gisee metit yiy dal doomu Aadama yi, lu tax ñu bare foog ne Yàlla fonkul nit ?

6 Am na ay nit ñu am xel-ñaar ci loolu. Lii lañuy wax : ‘ Bu Yàlla fonkoon doomu Aadama yi, ndax àddina si dina mel ni mu mel tey ? ’ Xeex, bañante ak ñàkk bu metti, bare na lool. Ñun ñépp, dañuy feebar, di am coono, te dañuy am ay mbokk yu gaañu. Loolu moo tax ñu bare ne : ‘ Bu ñu Yàlla fonkoon te di xalaat suñuy coono, ndax du tere loolu lépp di am ? ’

7. a) Naka la jàngalekat yi ci wàllu diine taxe ba nit ñu bare foog ne Yàlla amul yërmande ? b) Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ci coono yi ñuy am ?

7 Li ci gën a doy waar mooy, ay jàngalekat ci wàllu diine ñooy tax yenn saay nit ñi foog ne Yàlla amul yërmande. Naka ? Bu musiba amee, dañuy wax ne ndogalu Yàlla la. Kon dañuy wax ne Yàlla moo tax lu bon loolu am. Lan mooy dëgg gi ? Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ? Lii la ci Saag 1:13 tontu : “ Bu la fiir galanee, bul ne: ‘Yàllaa ko dogal,’ ndaxte Yàlla jegewul ak mbon fenn te du fiir kenn. ” Kon, Yàlla masul a indi lu bon li ngay gis ci àddina (Job 34:10-12). Dëgg la, dafay bàyyi lu bon loolu am. Waaye bàyyi dara mu am wuute na lool ak tax ba mu am.

8, 9. a) Bàyyi lu bon mu am ak tax mu am, du benn. Noo mën a misaale loolu ? b) Lu tax jaaduwul ñuy tuumaal Yàlla ndax li mu bàyyi doomu Aadama yi ñu sax ci lu bon ?

8 Nañu jël benn misaal. Xalaatal boroom kër bu am xel te bëgg doomaam. Benn doomam dem ba mag, waaye ba tey ci kër gi la dëkk. Doom jooju dem ba bëggatul déggal waajuram yi te fas yéene génn kër gi. Baayam terewu ko dem. Doom jooju kontine ci lu bon li mu nekke, ba dugal boppam ci poroblem. Ndax baayam moo tax mu nekk ci poroblem ? Déedéet (Luug 15:​11-13). Noonu it, bi doomu Aadama yi tànnee def lu bon te sax ci, Yàlla terewu leen ko. Waaye nag, du moom moo waral coono yi seen tànneef boobu indi. Kon, dëgg-dëgg, jaaduwul ñuy wax ne Yàlla mooy dogal jafe-jafe yépp yi doomu Aadama yi am.

9 Boo gisee Yàlla di bàyyi nit ñi ñu def lu bon, am na lu tax. Moom moo ñu sàkk te bare na xam-xam ak kàttan. Kon bu ko neexee, du ñu wax lu tax mu bàyyi nit ñi di def lu bon. Waaye dafa ñu bëgg, moo tax mu wax ñu ko. Dinga ci jàng lu gën a bare ci pàcc 11. Waaye nanga jàpp ne du Yàlla moo tax ñu am coono. Te sax, moom rekk moo ñu may yaakaaru gis coono yooyu yépp deñ. — Isaïe 33:⁠2.

10. Lu tax ñu mën a gëm ne Yàlla dina dindi bépp coono bu nit ñu bon ñi teg doomu Aadama yi ?

10 Rax-ci-dolli, xam nañu ne Yàlla ku sell la (Isaïe 6:⁠3). Loolu dafay tekki ne dafa set te amul dara lu bon ci moom. Kon mën nañu ko wóolu ci lépp. Mënuñu xalaat lu mel noonu ci doomu Aadama yi, ndaxte lée-lée ñu soppi seen jikko ba nekk nit ñu bon. Kilifa bi gën a jub ci doomu Aadama yi sax, ci lu bare, du mën a defaraat li nit ñu bon ñi yàq. Waaye Yàlla moom, dara tëwu ko. Bépp coono bu nit ñu bon ñi teg doomu Aadama yi, Yàlla mën na ko dindi, te dina ko def. Bés bu Yàlla di def loolu, dina dindi lu bon ba mu jeex tàkk, te dootul amati ba fàww. — Sabóor 37:​9-11.

LI DUL YOON LI ÑUY DAL TEY, NAKA LA KO YÀLLA DI GISE ?

11. a) Naka la Yàlla di gise li dul yoon ? b) Naka la Yàlla di gise metit yi lay dal ?

11 Waaye fi mu nekk nii, naka la Yàlla di gise li xew ci àddina si ak li lay dal yow ci sa wàllu bopp ? Biibël bi wax na ne Yàlla “ ku fonk njubte la ”. (Sabóor 37:​28, NW.) Kon lépp lu jëm ci lu baax ak lu bon dafa ko itteel bu baax a baax. Yàlla dafa sib lépp lu jubul. Biibël bi nee na, ca jamano yu yàgg ya, bi àddina si sépp feesoon ak lu bon, Yàlla dafa ‘ amoon tiis ci xolam ’. (Njàlbéen ga 6:​5, 6.) Yàlla soppikuwul (Malaki 3:⁠6). Ba tey jii, metit yi muy gis ci àddina si, neexu ko. Te dafa bañ a gis doomu Aadama yi ci metit. Biibël bi wone na ci lu wóor ne Yàlla dafa ñu fonk, bi mu waxee ne Yàlla “ ku leen ñeewante la ”. — 1 Piyeer 5:⁠7.

Biibël bi dafa wax ne Yexowa dafa ñu bëgg te moom moo sàkk lépp ci àddina si ak ci jaww ji.

12, 13. a) Lu tax ñu am jikko yu rafet, yu mel ni mbëggeel, te lan la mbëggeel mën a def ci fasoŋ bi ñuy gise àddina si ? b) Lu tax nga mën a gëm ne Yàlla dina dindi jafe-jafe yi am tey ?

12 Lu tax mu mën ñu wóor ne Yàlla dafa bañ a gis nit ci metit ? Lii lañu ci mën a yokkaat. Biibël bi wax na ne Yàlla dafa bind nit ci melokaanam (Njàlbéen ga 1:26). Kon, jikko yu rafet yi ñu fekk ci nit, ci Yàlla lañu ko jële. Boo gisee nit ci coono fekk deful dara lu bon, ndax loolu du la metti ? Bu la loolu naqaree, na la wóor ne Yàlla la gën a naqari.

13 Lenn ci li gën a rafet ci doomu Aadama mooy mbëggeel. Jikko boobu it, ci Yàlla la jóge. Biibël bi wax na ne “ Yàlla mbëggeel la ”. (1 Yowaana 4:⁠8.) Nit dafay bëgg, ndaxte Yàlla dafa am mbëggeel. Ndax mbëggeel bi nga am ci nit ñi tax na nga bëgg a dindi seeni coono, dindi it li dul yoon ? Boo amoon kàttan boobu, ndax doo ko def ? Ci lu wóor ! Noonu it, na la wóor ne Yàlla dina dindi coono yi ak li dul yoon. Li ñu Yàlla dig, te ñu bind ko ci xët 4 ak 5 ci téere bii, du gént walla ay wax kese. Lépp li Yàlla dige, dina am ci lu wóor. Waaye bala nga mën a gëm dige yooyu, danga war a gën a xam Yàlla mi dige loolu.

YÀLLA DAFA BËGG NGA XAM KI MU DOON

Boo bëggee nit xam la, ndax doo ko wax sa tur ? Yàlla xamal na ñu turam ci Biibël bi.

14. Lan mooy turu Yàlla te lu tax ñu war a jaar ci tur boobu ?

14 Boo bëggee nit xam la, lan nga mën a def ? Ndax doo ko wax sa tur ? Ndax Yàlla am na tur ? Ci diine yu bare dañuy wax ne turam mooy “ Yàlla ” walla “ Boroom bi ”. Waaye ci dëgg, loolu du ay tur. Dafa mel ni booy woowe nit “ buur ” walla “ peresidaa ”. Biibël bi dafa ñuy wax ne ni ñu mën a woowee Yàlla bare na, mel ni “ Yàlla ” walla “ Boroom bi ”. Waaye Biibël bi wax na it ne Yàlla dafa am turu boppam. Tur boobu mooy Yexowa. Sabóor 83:​18, NW, nee na : “ Yow mii tudd Yexowa, yow rekk yaay Aji Kawe ji ci kaw suuf si sépp. ” Bu dee tur boobu feeñul ci Biibël bi am ci sa làkk, boo bëggee xam lu tax loolu, nanga seet li ñu ci wax ci xaaj bi tudd “ Li ñu yokk ci waxtaan yi nekk ci téere bii ”, ci xët 195 ba 197. Dëgg gi mooy, gis nañu turu Yàlla ay junniy yoon ci sotti Biibël yu njëkk yi. Kon Yexowa dafa bëgg nga xam turam te jaar ci tur boobu booy wax ak moom. Mën nañu ne Yàlla dafay jaar ci Biibël bi ngir won la ki mu doon.

15. Tur bii : Yexowa, lan la tekki ?

15 Yàlla dafa jox boppam tur. Li tur boobu tekki dafa am maanaa lool. Turam, Yexowa, mu ngi tekki ne Yàlla mën na def lépp li mu dige ak lépp li mu bëgg *. Dëgg-dëgg, amul benn tur bu mel ni turu Yàlla. Moom rekk moo am tur boobu. Li tax Yexowa amul moroom, bare na. Nañu ci wax yenn.

16, 17. Lu ñu mën a jàng ci Yexowa bu ñu déggee ni ñu koy woowee, mel ni : a) “ Aji kàttan ji ” ? b) “ Buur bi fiy sax ba abadan ” ? c) “ Ki sàkk lépp ” ?

16 Gis nañu ba pare li Sabóor 83:​18, NW, wax ci Yexowa, maanaam : “ Yow rekk yaay Aji Kawe ji. ” Noonu it, Yexowa rekk lañuy woowe “ Aji Kàttan ji ”. Peeñu ma 15:3 nee na : «Say jëf réy nañu te yéeme, yaw Boroom bi [Yexowa, NW] Yàlla, Aji Kàttan ji. Say yoon jub nañu te dëggu, yaw Buur bi fiy sax ba abadan.» Bu Biibël bi woowee Yàlla “ Aji Kàttan ji ”, dafa ñuy won ne Yexowa moo ëpp kàttan ñépp. Tolloowul ak kenn kàttan. Te it bu ñuy woowe Yexowa “ Buur bi fiy sax ba abadan ”, loolu dafa ñuy fàttali ne am na leneen lu tax Yexowa amul moroom. Moom rekk a fi mas a nekk. Sabóor 90:​2, NW, nee na : “ Ca jamono yu dul jeex ci ginnaaw ba ca jamono yu dul jeex ci kanam [walla, ba abadan] yow yaay Yàlla. ” Kon ndax Yàlla nekkul ku jar a ragal ?

17 Yàlla amul moroom itam ndaxte moom kese mooy Ki sàkk lépp. Lii lañuy jàng ci Peeñu ma 4:11 : “Yàlla sunu Boroom, yaa yeyoo ndam, teraanga ak kàttan, ndaxte yaa sàkk lépp te ci sa coobare la lépp nekke, te ci lañu leen sàkke.” Lépp loo mënta xalaat, muy mbindeef yu ñu mënul a gis te nekk asamaan si, walla biddéew yi ngay gis ci asamaan guddi, walla doomu garab yi, walla jën yi nekk ci géej yi mbaa ci dex yi, loolu lépp dafa am ndaxte Yexowa mooy Ki sàkk lépp !

NDAX MËN NGA JEGE YEXOWA ?

18. Lu tax ay nit foog ne duñu mën a jege Yàlla mukk, waaye lan la Biibël bi wax ci loolu ?

18 Am na ñoo xam ne, bu ñu jàngee li Biibël bi wax ci jikko Yexowa yiy tax ñu war koo ragal, seen xel du dal. Pur ñoom Yàlla dafa kawe lool ba duñu ko mën a jege mukk walla sax am maanaa ci kanamam. Waaye ndax loolu ñuy xalaat, noonu la ? Xalaat yooyu bokkuñu dara ak li Biibël bi wax. Lii la Biibël bi wax ci Yexowa : «Sorewul kenn ci nun.» (Jëf ya 17:27). Biibël bi dafa ñuy xiirtal sax ci lii : “ Jegeleen Yàlla, mu jege leen. ” — Saag 4:⁠8.

19. a) Lan lañu war a njëkk a def ngir jege Yàlla te loolu naka la ñuy jariñe ? b) Yan jikko Yàlla ñoo gën a tax nga bëgg koo jege ?

19 Naka nga mën a jegee Yàlla ? Li njëkk mooy nanga kontine di def li ngay def fi mu tollu nii, maanaam di jàng ci lu jëm ci Yàlla. Yeesu nee na : «Dund gu dul jeex gi nag, mooy ñu xam la, yaw jenn Yàlla ju wóor ji am, te ñu xam it ki nga yónni, muy Yeesu Kirist.» (Yowaana 17:⁠3). Waaw, Biibël bi dafa ñuy wax ne jàng lu jëm ci Yexowa ak Yeesu mën na may nit “ dund gu dul jeex ”. Ni ñu ko waxe woon sànq, “ Yàlla mbëggeel la ”. (1 Yowaana 4:16.) Yexowa am na itam yeneen jikko yu rafet yu bare, yuy tax nit bëgg koo jege. Biibël bi nee na Yexowa mooy “Yàllay yërmande te bare yiw, di yéex a mer te fees ak mbëggeel ak kóllëre”. (Gàddaay gi 34:⁠6.) Dafa baax te nangu baal nit (Psaume 86:⁠5). Yàlla dafa ñuy muñal (2 Piyeer 3:⁠9). Dafay sàmm kóllëre (1 Korent 1:⁠9). Booy gën a jàng Biibël bi, dinga gis ni Yexowa wonee ne am na jikko yooyu ak yeneen jikko yu rafet yu bare yuy tax nga bëgg koo jege.

20-22. a) Ndax li ñu mënul a gis Yàlla, mën na tere ñu jege ko ? Waxal lu tax nga wax loolu. b)  Lan la la ay nit mën a wax, foog ne noonu lañu lay mën a dimbalee, waaye lan nga war a def ?

20 Dëgg la, Yàlla kenn mënu ko gis ak bët ndaxte xel la (Yowaana 1:18 ; 4:24 ; 1 Timote 1:17). Waaye boo jàngee li Biibël bi wax ci moom, dinga dem ba mën a xam Yàlla ni ñuy xame nit. Ni ko woykat bi waxe, mën nga “ xemmem rafetaayu ” Yexowa (Sabóor 27:4 ; Room 1:20). Ni ngay gënee jàng lu jëm ci Yexowa, noonu ngay gënee gis ne, dëgg-dëgg, ku am la. Te dinga gën a gis lu tax nga war koo bëgg te jege ko.

Mbëggeel bi baay bu baax am ci doomam dafa ñuy won mbëggeel bu gën a réy bi suñu Baay bi nekk ci asamaan am ci ñun.

21 Dinga mën a xam lu tax Biibël bi ne, bu ñuy xalaat ci Yexowa, dañu ko war a jàppe ni suñu Baay (Macë 6:⁠9). Sàkku ñu rekk, yem ci. Dafa ñu yéene dund gi gën, ni ko baay bu bëgg ay doomam di leen ko yéene (Psaume 36:⁠9). Biibël bi dafa ñuy wax it ne doomu Aadama mën na nekk xaritu Yexowa (Saag 2:23). Seetal ma lii : mën nga nekk xaritu ki sàkk lépp li am ci àddina si ak ci jaww ji !

22 Booy kontine di jàng Biibël bi, xéyna ay nit dinañu la wax nga bàyyi, foog ne noonu lañu lay mën a dimbalee. Xéyna dañuy ragal nga bàyyi li nga gëmoon. Waaye bu la kenn teree am xarit bi gën bi nga mën a am.

23, 24. a) Lu tax nga war a kontine di am li ngay laajte ci li ngay jàng ? Lan lañuy jàng ci pàcc biy topp ?

23 Dëgg la, dina am li nga dul mën a nànd booy komaase di jàng Biibël bi. Xéyna dinga rus a laajte. Waaye bul bàyyi rus boobu tax ba nga bañ a ñaan ndimbal. Yeesu nee na, suufeel sa bopp ni xale bu ndaw, lu baax la (Macë 18:​2-4). Xam nañu ne xale yi dañu bare laaj. Yàlla dafa bëgg nga xam tontu laaj yi ngay laaj. Biibël bi dafay tagg nit ñu sawaroon a jàng lu jëm ci Yàlla. Dañu doon niir Mbind mi, maanaam gëstu bu baax, ngir seet ndax li ñu doon jàng mooy dëgg. — Jëf ya 17:⁠11.

24 Li gën li nga mën a def ngir xam Yexowa mooy gëstu ci Biibël bi. Biibël bi dafa wuute ak yeneen téere yépp. Lu tax ñu wax loolu ? Pàcc bii di topp dina ci tontu.

^ par. 15 Ci xaaj bi tudd “ Li ñu yokk ci waxtaan yi nekk ci téere bii ”, te mu nekk ci xët 195 ba 197 am na ay leeral ci li turu Yàlla di tekki ak ni ñu koy waxe.