LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII
Yeesu Kirist, Almasi bi Yàlla dige woon
YEXOWA YÀLLA dafa jaar ci yonent yu bare yu nekk ci Biibël bi, ngir ñu xamal ñu lu bare ci Almasi bi ndax ñu mën ko xàmme. Wax nañu lu jëm ci juddoom, ci waaraate bi muy def, wax it ci deewu Musalkat boobu ñu Yàlla digoon. Loolu lépp li Biibël bi waxoon, gis nañu ko ci Yeesu Kirist. Lépp a am ni ñu ko waxe woon ba jaaxal ñépp. Ngir wone loolu, nañu waxtaan tuuti ci li yonent yi waxoon ci juddu Almasi bi ak bi muy nekk xale.
Esayi 9:6). Te Yeesu, ci askanu Daawuda la bokk. — Macë 1:1, 6-17.
Yonent Yàlla Esayi waxoon na ne Almasi bi ci askanu Buur Daawuda lay bokk (Mikaa, beneen yonent Yàlla, waxoon na ne xale boobu, njiit lay doon te ci dëkku “ Betleyem Efrataa ” lay juddu (Mikaa 5:2, NW). Ci jamono bi Yeesu juddu, ñaari dëkk ñoo tuddoon Betleyem ca Israyil. Benn bi mu ngi nekkoon ci wetu Nasaret ca bëj-gànnaaru réew mi. Beneen bi ci wetu Yerusalem ca Yude la nekkoon. Betleyem bi nekkoon ci wetu Yerusalem lañu doon woowe bu njëkk Efrataa. Ca dëkk boobu nag la Yeesu juddu, ni ko yonent bi waxe woon ! — Macë 2:1.
Biibël bi waxoon na itam ne dinañu woo Doomu Yàlla, «mu génn Misra», ñëw. Dañu yóbbu woon Yeesu Misra bi mu nekkee xale. Ba Erodd deewee lañu ko indiwaat Israyil. Noonu la li yonent bi waxoon ame. — Hoshéa 11:1 ; Macë 2:15.
Ci tablo bi nekk ci xët 200, aaya yi nekk ci suufu fi ñu bind “ Li yonent yi wax ”, dañuy wax lu jëm ci Almasi bi. Nanga jàng aaya yooyu te seet ndax ànd na ak aaya yi nekk ci suufu fi ñu bind “ Ni loolu ame ”. Soo defee loolu dina tax nga gën a gëm dëgg yi nekk ci Kàddu Yàlla.
Booy xalaat ci aaya yooyu, bul fàtte ne li yonent yi wax, ay téeméeri at bala Yeesu di juddu lañu ko bind. Lii la Yeesu waxoon : «Li ñu bind lépp ci samay mbir ci yoonu Musaa ak ci téerey yonent yi ak ci Sabóor dafa war a am.» (Luug 24:44). Ni nga ko mënee seetal sa bopp ci Biibël bi nga yor, lépp li ñu waxoon ci Yeesu am na.