Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LAAJ 15

Naka ngeen mënee am bànneex ?

Naka ngeen mënee am bànneex ?

“ Njëlu ñetti xob fa ñu la soppe moo dàq yàpp wu duuf fu ñu la bañe. ”

Kàddu yu Xelu 15:⁠17

“ Man Yexowa maay sa Yàlla, Ki lay jàngal ngir sa njariñ, Ki lay won yoon bi nga war a jaar. ”

Esayi 48:⁠17, MN

“ Yéen ñi xam seen ñàkk doole ngir neex Yàlla, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji, yéena ko yelloo. ”

Macë 5:3

“ Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp. ”

Macë 22:⁠39

“ Defal-leen nit ñi li ngeen bëgg, ñu defal leen ko. ”

Luug 6:​31

“ Ki barkeel mooy kiy déglu kàddug Yàlla te di ko topp. ”

Luug 11:⁠28

“ Bakkanu nit ajuwul ci alalam, ak lu mu baree bare. ”

Luug 12:⁠15

“ Kon su nu amee lekk ak koddaay, nanu ko doyloo. ”

1 Timote 6:8

“ Joxe moo gëna barkeel nangu. ”

Jëf ya 20:⁠35