Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LAAJ 3

Ci ñan la Yàlla jaar ngir bind Biibël bi ?

Ci ñan la Yàlla jaar ngir bind Biibël bi ?

“ Musaa bind na lépp li Yexowa waxoon. ”

Gàddaay gi 24:​4, MN

“ Dañeel am gént ak peeñu ci xelam, bi mu tëddee ci lalam. Gannaaw ga mu bind gént gi. ”

Dañeel 7:1

“ Ba ngeen jotee kàddug Yàlla, gi nu doon waare, nangu ngeen ko, waxuma ni kàddug nit waaye ni kàddug Yàlla, ndaxte moom la ci dëgg-dëgg, te mu ngi jëf ci yéen ñi gëm. ”

1 Tesalonig 2:​13

“ Mbind mu sell mépp, ci gémmiñu Yàlla la jóge, te am na njariñ ngir jàngal nit ñi. ”

2 Timote 3:​16

“ Kenn ci yonent yi masula wax ci coobarey boppam, waaye Xel mu Sell mi daa na xiir nit ñi, ñu yégle kàddug Yàlla. ”

2 Piyeer 1:​21