Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LAAJ 18

Naka ngeen mënee jege Yàlla ?

Naka ngeen mënee jege Yàlla ?

“ Yaw miy nangug ñaan, yaw la képp di wuysi. ”

Sabóor 65:3

“ Wóolul Aji ji Sax ji, sa xol wéetal ko, te bul wéeru ci saw déggin. Loo mébét, bàyyil Yàlla xel, mu xàllal la yoon. ”

Kàddu yu Xelu 3:​5, 6

“ Dund gu dul jeex gi nag, mooy ñu xam la, yaw jenn Yàlla ju wóor ji am, te ñu xam it ki nga yónni, muy Yeesu Kirist. ”

Yowaana 17:3

“ Fekk sax [Yàlla] sorewul kenn ci nun. ”

Jëf ya 17:⁠27

“ Li ma leen di ñaanal nag mooy lii : yal na seen mbëggeel di yokku tey gëna tar, jaar ci xam ak xàmmi gu wér. ”

Filib 1:9

“ Ku xelam des ci benn fànn ci yéen nag, na ko ñaan Yàlla, te dina ko ko may, ndaxte Yàlla mooy Aji Yéwén, jiy may ñépp ci lu àndul ak genn ŋàññ. ”

Saag 1:5

“ Jegeleen Yàlla, mu jege leen. Yéen bàkkaarkat yi, sellal-leen seeni loxo ; yéen ñi am xel ñaar, laabal-leen seeni xol. ”

Saag 4:8

“ Ndaxte mbëggeel ci Yàlla mooy sàmm ay ndigalam ; te ay ndigalam diisuñu. ”

1 Yowaana 5:3