LAAJ 8
Ndax Yàlla mooy teg nit ñi coono ?
“ Yàlla dëgg ji mënul sax xalaat a def lu jubadi, Aji-Kàttan ji du xalaat mukk a def lu bon. ”
Ayóoba 34:10, MN
“ Bu la fiir galanee, bul ne : « Yàllaa ko dogal, » ndaxte Yàlla jegewul ak mbon fenn te du fiir kenn. ”
“ Ngeen yenniku ci kawam seen njàqare jépp, ndax ku leen ñeewante la. ”
“ Li Yàlla dige, dina ko def, lu mu yéex yéex ci xalaatu nit. Xanaa kay da leena muñal, ndax bëggul kenn alku, waaye ñépp tuub seeni bàkkaar. ”