Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LAAJ 14

Naka ngeen mën a yore seen xaalis ?

Naka ngeen mën a yore seen xaalis ?

“ Ku topp sa bànneex, mujje ñàkk ; ku sopp biiñ ak lu niin du woomle.”

Kàddu yu Xelu 21:⁠17

“ Koo leb di surgaam. ”

Kàddu yu Xelu 22:7

“ Su kenn ci yéen bëggee tabax taaxum kaw, ndax du jëkka toog, xalaat ñaata la ko wara dikke, ngir seet ba xam ndax am na xaalis bu mana àggale liggéey bi ? Lu ko moy, su yékkatee fondamaa bi te manu koo àggale, ñi koy gis dinañu ko ñaawal, naan ko : « Waa jii dafa tàmbalee tabax, waaye manu koo àggale. » ”

Luug 14:​28-​30

“ Bi ñu lekkee ba regg, Yeesu ne taalibe ya : « Dajaleleen desitu mburu mi, ba dara du ci réer. » ”

Yowaana 6:​12