Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LAAJ 2

Naka ngeen mënee xam Yàlla ?

Naka ngeen mënee xam Yàlla ?

“ Bu téereb yoon wii sore mukk sa gémmiñ, waaye dee ko riim guddi ak bëccëg, ngir sax ci jëfe lépp li ñu ci bind. Noonu looy sabablu dina àntu, te dinga am ndam ci looy def. ”

Yosuwe 1:8

“ Dañu doon kontine di jàng téere bi, téereb sàrt Yàlla dëgg ji, di ko tekki ak di ko firi ; noonu ñuy dimbali nit ñi ñu nànd li ñu doon jàng. ”

Nëxemiyaa 8:​8, MN

“ Ndokklee yaw mi toppul tànki ku bon, taxawuloo yoonu moykat . . . , xanaa di bége yoonu Aji Sax ji, di ko jàngat guddeek bëccëg. Loo def mu àntu. ”

Sabóor 1:​1-3

“ Noonu Filib dawsi, mu dégg waayi Ecópi ja, di jàng téereb yonent Yàlla Esayi. Mu laaj ko : « Ndax xam nga li ngay jàng ? » Mu ne ko : « Nu ma ko mana xame, su ma ko kenn firilul ? » Mu woo Filib nag, mu yéeg, toog ak moom. ”

Jëf ya 8:​30, 31

“ Ndaxte ba àddina sosoo ba tey, mbiri Yàlla yu nëbbu ya, maanaam dooleem ju sax ja, ak meloom wu kawe wa, feeñ nañu bu leer, te bir ñépp ci yi mu sàkk, ba tax bunti lay yépp tëj nañu. ”

Room 1:​20

“ Faaydaalal yëf yooyu te sóobu ci, ba sa jëm kanam bir ñépp. ”

1 Timote 4:​15

“ Nanu seet ni nu mana xiirtalante cig mbëggeel ak ci jëf yu baax. Te bunu bàyyi sunu ndaje yi, ni ko ñenn ñi di defe, waaye nanuy nàddante ci ngëm, di ko feddali, fi ak yéena ngi gis bésu Boroom biy jubsi. ”

Yawut ya 10:​24, 25

“ Ku xelam des ci benn fànn ci yéen nag, na ko ñaan Yàlla, te dina ko ko may, ndaxte Yàlla mooy Aji Yéwén, jiy may ñépp ci lu àndul ak genn ŋàññ. ”

Saag 1:5