LAAJ 5
Lan mooy xibaar bi nekk ci Biibël bi ?
“ Dinaa def mbañeel sa digganteek jigéen ji, ba dëddale sa xeet ak xeetam, muy toj sa bopp, nga di ko màtt ci téstën. ”
“ Waa àddina sépp dinañu taasu ci sa barkey askan, ndax déggal nga ma. ”
“ Yal na sa nguur ñëw, yal na sa coobare am ci suuf mel ni ci kaw. ”
“ Su ko defee Yàlla Boroom jàmm dina not Seytaane ci seeni tànk léegi. ”
“ Léegi bu ñu ko notalee lépp nag, moom Kirist muy Doom ji dina delloo kilifteef gi Yàlla, mi ko notal lépp, ngir Yàlla nekk buur ci lépp. ”
“ Léegi nag Yàlla am na lu mu dig Ibraayma ak askanam . . . , maanaam Kirist. Bu ngeen bokkee ci Kirist, kon bokk ngeen ci askanu Ibraayma. ”
“ Nguuru àddina, jébbalaat nañu ko sunu Boroom ak Almaseem, te dina nguuru ba fàww. ”
“ Daaneel nañu ko, moom ninkinànka ju réy ji, di jaani cosaan ji, te ñu di ko wax Tuumaalkat bi mbaa Seytaane, moom miy nax waa àddina sépp—daaneel nañu ko ci kaw suuf, moom ak i malaakaam. ”
“ Mu jàpp ninkinànka ja, di jaani cosaan ja, muy Tuumaalkat bi, maanaam Seytaane. Malaaka ma yeew ko diirub junniy at. ”