Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NETTALI 44

Raxab Nëbb Na Ñi Ñów Yërndu Réew Mi

Raxab Nëbb Na Ñi Ñów Yërndu Réew Mi

NIT ñi ngay gis fii, dañu am poroblem. Dañu war a génn bala ñu leen di rey. Waa Israyil lañu te dañu ñów pur xool réew mi. Jigéen bi leen di dimbali, Raxab la tudd. Këram mu ngi ci kow miir bu yaatu biy wër dëkk bi tudd Yeriko. Nañu seet lu tax góor ñooñu nekk ci coono.

Waa Israyil pare nañu pur jéggi dexu Yurdan ngir dugg ci réewu Kanaan. Waaye bala loolu, Yosuwe yónni na ñaari góor. Mu ne leen : ‘ Demleen xool ni réew mi ak dëkku Yeriko mel. ’

Bi ñu àggee Yeriko, ci këru Raxab lañu dem. Waaye am na ku ko wax buuru Yeriko. Mu ne ko : ‘ Ñaari góoru Israyil ñów nañu fii tey ci guddi gi ngir yërndu réew mi. ’ Buur bi daldi yónni ay góor ci Raxab. Ñu ne ko : ‘ Génneel góor ñi nekk fii ci sa kër ! ’ Waaye Raxab dafa leen nëbb ci teraas bi nekk ci kow këram. Mu ne góor ñooñu : ‘ Am na ay góor ñu fi ñów. Waaye xawma fu ñu dem. Ci timis lañu dem, bala ñu tëj buntu dëkk bi. Bu ngeen gaawee, dingeen leen dab. ’ Góor ñi daldi daw, jéem leen a jàpp.

Bi ñu demee, Raxab gaaw a yéeg ci kow, ne góor ñooñu : ‘ Xam naa ne Yexowa dina leen may suñu réew. Dégg nañu li mu def ca Géej gu xonq gi, bi ngeen génnee Misra. Dégg nañu itam ni ngeen reye buur yi tudd Sixon ak Og. Defal naa leen lu baax, kon ngir Yàlla, nangeen ma dig ne yéen it, dingeen ma defal lu baax. Buleen rey sama pàppa ak sama yaay, samay rakk ak samay mag. ’

Ñaari góor ñi dig ko loolu. Waaye am na lu Raxab war a def. Ñu ne ko : ‘ Jëlal buum bu xonq bii, takk ko ci sa palanteer. Dajaleel say mbokk yépp ci sa biir kër, ñu nekk ak yow. Ñun, bu ñu ñówee pur jël Yeriko, dinañu gis buum bii ci sa palanteer te duñu rey kenn ci biir kër gi. ’ Bi ñu delloo ci Yosuwe, ñu nettali ko loolu lépp.