NETTALI 91
Yeesu Mu Ngiy Jàngale Ci Kow Tund
XOOLAL Yeesu fii. Mu ngiy jàngal nit ñii ngay gis ñépp ci kow tund bu nekk Galile. Ñi ko gën a jege ñooy taalibeem yi. Tànn na ci 12 ngir ñu nekk ay ndaw. Ndaw yi ñooy taalibe yi Yeesu tànn ngir ñu def liggéey bu am solo lool. Ndax xam nga seen tur ?
Am na Simoŋ Piyeer ak Andare ñi bokk ndey ak baay. Am na Saag ak Yowaana. Ñoom it ñoo bokk ndey ak baay. Am na it keneen ku tudd Saag ak keneen ku tudd Simoŋ. Am na ñaari ndaw yu tudd Yudaa. Kenn ki, Yudaa Iskariyo la. Keneen ki, dañu koy woowe itam Tade. Te it, am na Filib ak Nataneel (mi ñuy woowe itam Bartelemi), ak Macë ak Tomaa.
Ginnaaw bi Yeesu jógee Samari, komaase na waar nit ñi ci lii : ‘ Nguur gi nekk asamaan jegesi na. ’ Ndax xam nga ban nguur la ? Nguuru Yàlla la te nguur dëgg la. Yeesu mooy buuram. Dina nekk asamaan te indi jàmm ci kow suuf si. Nguuru Yàlla dina defar suuf si sépp ba mu nekk àjjana ju rafet.
Fii, Yeesu mu ngi jàngal nit ñi lu jëm ci Nguur gi. Mu ne leen : ‘ Nii ngeen war a ñaane Yàlla : Suñu Baay bi nekk ci kow. Na sa tur nekk tur bu ñuy teral. Na sa nguur ñów. Na sa coobare am ci suuf mel ni ci kow. ’ Ñaan boobu, ñu bare dañu koy woowe ‘ ñaanu Sang bi ’ walla ‘ Suñu Baay ’. Ndax mën nga wax li nekk ci ñaan boobu yépp ?
Yeesu dafay jàngale itam ni ñu war a digaale ak suñu moroom yi. Mu ne : ‘ Defalleen seen moroom li ngeen bëgg mu defal leen ko. ’ Ku baax ak yow, ndax loolu du la neex ? Kon, ni ko Yeesu waxe, dañu war a baax ak suñu moroom. Ci àjjana jiy am ci kow suuf, ñépp ay def loolu. Loolu, ndax du neex lool ?