Yokkal sa mën-mën ci jàng ak jàngale

Téere bii dañu ko defar ngir dimbali la nga yokk sa mën-mën ci jàng ci kanamu mbooloo, akit ci wax ak ci jàngale.

Leetar bu jóge ci Jataay biy dogal

Li ñuy def mooy njàngale bi gën a am solo bi ñu mas a dénk doomu Aadama yi.

LESOŊ 1

Li ngay njëkk a wax

Li ngay njëkk a wax war na am ñetti yëf yu ko tax a jóg.

LESOŊ 2

Waxal mel ni kuy waxtaan

Wax mel ni kuy waxtaan dina tax mu gën a yomb nit ñi déglu la te nangu li ngay wax.

LESOŊ 3

Booleel ay laaj ci sa njàngale

Laajal nit ñi ay laaj yuy tax ñu bëgg a déglu li ngay wax te gis bu baax ponk yi gën a am solo.

LESOŊ 4

Li nga mën a wax bala ngay jàng aaya

Xoolal li nga mën a wax bala ngay jàng aaya, ba nit ñi bëgg a xam li aaya bi wax.

LESOŊ 5

Liiral bu baax li ñu bind

Liir bu baax, fànn bu am solo la ngir jottali xam-xamu Yexowa.

LESOŊ 6

Woneel bu baax njariñu aaya yi

Dimbalil ñi lay déglu ñu xam bu baax ni aaya bi nga jàng ànde ak li ngay wax.

LESOŊ 7

Waxal lu wóor lu nit mën a gëm

Wax lu wóor lu nit mën a gëm mooy dimbali ñi lay déglu ñu xam fi dëgg gi féete.

LESOŊ 8

Jàngalal nit ñi ak ay misaal

Nanga jàngale ak ay misaal yu yomb, yuy laal xol tey jàngale ay ponk yu am solo.

LESOŊ 9

Jëfandikool ay wideo ak ay nataal ngir jàngal nit ñi

Woneel wideo walla nataal ngir li ngay jàngale gën a yomb a fàttaliku te gën a am njariñ.

LESOŊ 10

Ni ngay soppee sa baat booy jàngale

Mën nga soppi sa baat, boo waxee mu gaaw, mu yéex, walla wax ak baat bu xumb walla bu lewet, walla wax ci kaw walla wàcce sa baat. Loolu dina laal xolu nit ñi ba tax ñu jëfe li ñu dégg.

LESOŊ 11

Waxal ak cawarte

Wax ak cawarte dafay wone bu baax li ngay yëg dëgg te tax nit ñi déglu li ngay wax.

LESOŊ 12

Waxal ak mbaax te woneel ne yëg nga nit ñi

Booy wax ak mbaax, dinga won ñi lay déglu ne bëgg nga leen a dimbali.

LESOŊ 13

Woneel bu baax njariñu li ngay jàngale

Dimbalil ñi lay déglu ñu xam njariñu li ngay wax te won leen ni ñu war a jëfe li ñu dégg.

LESOŊ 14

Woneel bu baax ponk yi gën a am solo

Dimbalil ñi lay déglu ñu xam bu baax li waral sa waxtaan te gis ni ponk bu gën a am solo bu nekk ànde ak li waral waxtaan bi ak it turu waxtaan bi.

LESOŊ 15

Woneel ne gëm nga li ngay wax

Woneel ne gëm nga li ngay wax. Ni ngay waxe, na wone ne ku dëggu nga.

LESOŊ 16

Xiiral nit ñi ci jëfe li ñu dégg te amal xalaat bu rafet ci ñoom

Bul wax rekk ci porobalem yi, waaye waxal ci li leen mën a faj ak ci li mën a xiir nit ñi ci jëfe li ñu dégg. Waxal ci dëgg giy dëfël xol gi nekk ci Kàddu Yàlla.

LESOŊ 17

Na li ngay wax leer ci ñi lay déglu

Dimbalil ñi lay déglu ba li ngay wax leer ci ñoom. Waxal ponk yi gën a am solo ci kàddu yu leer.

LESOŊ 18

Defal waxtaan buy yokk xam-xam

Dimbalil ñi lay déglu ñu xalaat bu baax ci li ngay wax te dimbali leen ñu jàng lu leen amal njariñ.

LESOŊ 19

Defal lépp ngir laal xolu nit ñi

Dimbali leen ba li leen di xiir ci def lu baax doon bëgg Yàlla ak Kàddoom, Biibël bi.

LESOŊ 20

Li ngay wax ngir jeexal sa waxtaan

Li ngay wax ngir jeexal sa waxtaan dina dimbali ñi lay déglu ñu nangu te jëfe li ñu dégg.