Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 14

Woneel bu baax ponk yi gën a am solo

Woneel bu baax ponk yi gën a am solo

Yawut ya 8:1

LI NGA WAR A JÀPP: Dimbalil ñi lay déglu ñu xam bu baax li waral sa waxtaan, te woneel ci lu leer ni ponk bu gën a am solo bu nekk ànde ak li waral waxtaan bi ak it turu waxtaan bi.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Xamal li waral sa waxtaan. Bala ngay def sa waxtaan, seetal ndax waxtaan bi dañu ci bëgg a xamal nit ñi dara, walla wax leen li tax ñu mën a gëm dara, walla xiir leen ci def dara. Booy def sa waxtaan, na ponk yi gën a am solo yépp leeral bu baax li waral sa waxtaan.

  • Na sa turu waxtaan bi feeñ bu baax ci biir waxtaan bi. Waxaatal kàddu yi gën a am solo ci turu waxtaan bi walla nga wax ay kàddu yu leen niru ngir turu waxtaan bi feeñ bu baax.

  • Na ponk yi gën a am solo leer te yomb a xam. Tànnal rekk ponk yu gën a am solo yu ànd ak turu waxtaan bi ngay def ak yu nga mën a leeral bu baax ci jot gi ñu la may. Ponk yi gën a am solo, buñu bare te na bu nekk leer bu baax, taxawal tuuti diggante ñaari ponk te nanga jàll ci beneen ponk ci fasoŋ bu yomb.