LESOŊ 16
Xiiral nit ñi ci jëfe li ñu dégg te amal xalaat bu rafet ci ñoom
Ayóoba 16:5
LI NGA WAR A JÀPP: Bul wax rekk ci porobalem yi, waaye waxal ci li leen mën a faj ak ci li mën a xiir nit ñi ci jëfe li ñu dégg.
NI NGA KO MËN A DEFE:
-
Amal xalaat bu rafet ci ñi lay déglu. Jàppal ne, sa mbokk karceen yi bëgg nañu neex Yexowa. Su dee sax war nga leen a yedd, njëkk leen a ndokkeel saa yu mënee nekk.
-
Bul wax rekk ci porobalem yi. Mën nga wax ci porobalem su loolu amee njariñ ci sa waxtaan. Sa waxtaan bi yépp war na yokk ngëmu ñi lay déglu.
-
Nanga sukkandiku bu baax ci Kàddu Yàlla. Waxal ci li Yexowa defaloon doomu Aadama yi, li mu leen di defal tey ak li mu leen nar a defal ëllëg. Waxal luy may ñi lay déglu yaakaar ak fit.