Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LESOŊ 7

Waxal lu wóor lu nit mën a gëm

Waxal lu wóor lu nit mën a gëm

Luug 1:3

LI NGA WAR A JÀPP: Booy wax sukkandikul ci lu wóor ngir dimbali ñi lay déglu ñu xam fi dëgg gi féete.

NI NGA KO MËN A DEFE:

  • Li ngay wax, na jóge fu wóor. Li ngay wax, na jóge ci Kàddu Yàlla, te saa yu mënee nekk jàngal aaya yi koy dëggal. Bala ngay wax ci li tubaab di woowe science, ci xibaar boo dégg, walla ci lu nit dund, walla ci leneen luy dëggal say kàddu, seetal ndax fi nga sukkandiku wóor na te li ñu ci wax mooy dëgg ba tey.

  • Li ngay wax, na ànd ak li nekk fi nga ko jële. Booy wax ci benn aaya, na ànd ak aaya yi ko jiitu ak yi ko topp, ànd ak lépp li Biibël bi wax, ànd it ak li nekk ci téere yi «surga bu takku te teey» bind (Macë 24:45). Su dee li ngay wax, ci beneen téere la jóge walla ci rajo walla internet, na dëppoo ak li taxoon ñu bind ko walla ñu wax ko.

  • Dimbalil ñi lay déglu ñu xalaat bu baax ci li ngay wax. Boo jàngee aaya ci Biibël bi walla nga jàng dara ci beneen téere ba pare, laajal ci fasoŋ bu rafet ay laaj mbaa nga misaal li ngay wax, ba ñi lay déglu xam ndax mën nañu ko gëm walla déet.