Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 11

Dañu nettali lu jëm ci Yeesu

Dañu nettali lu jëm ci Yeesu

Ndax gis nga góor yi nekk ci foto bi ? — Ñoom ñooy Macë, Màrk, Luug, Yowaana, Piyeer, Saag,Yudd ak Pool. Góor yooyu ñu ngi doon dund ci jamono Yeesu te bind nañu lu jëm ci moom. Nañu jàng nettali bii ngir gën leen a xam.

Lan nga xam ci góor yii ?

Ñett ci ñoom bokkoon nañu ci apootar yi doon waare ak Yeesu. Ndax xam nga leen ? — Macë la ak Yowaana ak Piyeer. Macë ak Yowaana xamoon nañu Yeesu bu baax te kenn ku nekk bind na téere buy wax ci dundu Yeesu. Yowaana bind na itam téere bu tudd Peeñu ma ak ñetti leetar yu tudd Benn Yowaana, Ñaareelu Yowaana ak Ñetteelu Yowaana. Piyeer bind na ñaari leetar ci Biibël bi. Ñu ngi tudd Benn Piyeer ak Ñaareelu Piyeer. Ci ñaareelu leetaram bi, Piyeer bind na bi ñu déggee baatu Yexowa ci kaw asamaan muy wax ci Yeesu, naan : ‘ Kii mooy sama doom. Bëgg naa ko, te bég naa ci moom. ’

Yeneen góor yi bokk ci foto bi bind nañu itam lu jëm ci Yeesu. Màrk kenn ci ñoom la. Xalaat nañu ne fekke woon na li xewoon bi ñu jàppee Yeesu. Luug itam bind na ci Yeesu. Moom doktoor la woon te dafa mel ni bi muy doon karceen fekk na Yeesu dee ba pare.

Yeneen ñaari nit yi ngay gis ci foto bi, ay ràkku Yeesu lañu woon. Ñoom itam bind nañu ci Biibël bi. Ndax xam nga seen tur ? — Ñu ngi tudd Saag ak Yudd. Bu njëkk ba, gëmuñu woon Yeesu. Dañu ko tegoon ku dof. Waaye mujj nañu gëm Yeesu te nekk karceen.

Ki mujj ki ngay gis ci foto bi mooy Pool. Sóol la tuddoon bala muy nekk karceen. Dafa bañoon karceen yi te soxor lool ci ñoom. Ndax xam nga lan moo tax Pool mujj a nekk karceen ? — Mu am bés, bi Pool di dox ci yoonu Damaas, mu jékki-jékki rekk dégg baat bu jóge ci kaw di wax ak moom. Baatu Yeesu la woon ! Mu ne Pool : ‘ Lu tax nga soxor ci nit ñi ma gëm ? ’ Ginnaaw loolu, Pool bàyyi li mu doon def te nekk karceen. Ci téere yépp yi nekk ci Biibël bi, Pool bind na ci 14, komaasee ci téere Room ba téere Yawut ya.

Dañuy jàng Biibël bi bés bu nekk, du dëgg ? — Bu ñu koy def, dañuy jàng lu bare lu jëm ci Yeesu. Ndax bëgg nga yokk li nga xam ci Yeesu ? —