Ubbil li ci biir

Ay tont yu leer ci ay laaj yu am solo

Ay tont yu leer ci ay laaj yu am solo

YAN laaj ? Ay laaj yu am solo yi nit ñi di faral di laaj seen bopp. Jàngal laaj yii :

  • Ndax Yàlla fonk na nit dëgg-dëgg ?

  • Ndax geer ak naqar dina fi mas a jóge ?

  • Lan mooy dal nit bu deewee ?

  • Ndax ñi dee dinañu mas a dekki ?

  • Lan laa mën a def ba Yàlla nangu sama ñaan ?

  • Lan laa mën a def ba am jàmm ci sama dund ?

Mën na am nga mas a laaj sa bopp laaj yooyu. Kan moo la ci mën a tontu ? Nit ñi bind nañu ay junniy téere ngir tontu ci. Waaye téere yu bare dañuy werante ci seen biir. Te it, léeg-léeg téere dina wax dara, ba pare mu weesu, ñu daldi ko soppi.

Waaye am na benn téere boo xam ne dinga ci gis tont yu wóor. Téere boobu masul wax lu dul dëgg. Lii la Yeesu wax Yàlla ci ñaan : “ Sa kàddu mooy dëgg. ” (Yowaana 17:17). Tey xam nañu ne ­Kàddu googu mooy téere bu sell bu ñuy wax Biibël bi. Seetaatal laaj yi nekk ci kaw. Ci kayit bii, dinga ci am tont yu gàtt, leer te nekk dëgg yu jóge ci Biibël bi.

Ndax Yàlla fonk na nit dëgg-dëgg ?

LI WARAL LAAJ BOOBU : Ñu ngi dund ci àddina boo xam ne nit ñu soxor te jubadi bare nañu lool. Diine yu bare dañuy wax ne Yàlla mooy dogal metit yi ñuy daj.

LI CI BIIBËL BI WAX : Yàlla du dogal mukk lu bon. Job 34:​10 dafa wax ne Yàlla dëgg ji mënul sax xalaat a def lu bon te Aji-Kàttan ji du def lu bon mukk ! Yàlla dafa fonk doom-Aadama yi. Am na lu rafet lu mu leen bëgg a defal. Moo tax Yeesu jàngal nu ñu ñaan Yàlla lii : “ Sunu Baay bi nekk ci kaw, [...] na sa nguur ñëw, na sa coobare am ci suuf mel ni ci kaw. ” (Macë 6:​9, 10). Yàlla dafa ñu fonk ba dafay def lépp ngir lu rafet loolu am. — Yowaana 3:​16.

Seetal itam Njàlbéen ga 1:​26-​28 ; Saag 1:13 ak 1 Piyeer 5:​6, 7.

Ndax geer ak naqar dina fi mas a jóge ?

LI WARAL LAAJ BOOBU : Ba léegi geer yaa ngi kontine di rey ay nit ñu dul jeex. Naqar bàyyiwul kenn.

LI BIIBËL BI WAX : Yàlla nee na dina indi jàmm ci kaw suuf si sépp. Nguuru Yàlla bi nekk asamaan, bés bu ilifee suuf si, nit ñi dootuñu jàng xare. “ Dinañu tëgg ci seeni jaasi illeer. ” (Esayi 2:4). Yàlla dina fi jële bépp jubadi ak naqar. Biibël bi nee na : “ [Yàlla] dina fomp bépp rangooñ ci seeni bët ; te dee dootul am walla naqar walla jooy walla metit, ndaxte yëf yu jëkk ya wéy nañu [te jubadi ak naqaru tey ji, ci lañu bokk itam]. ” — Peeñu ma 21:​3, 4.

Seetal itam Sabóor 37:10, 11 ; 46:9 ak Mika 4:​1-4.

Lan mooy dal nit bu deewee ?

LI WARAL LAAJ BOOBU : Li gën a bare ci diine àddina si dañuy wax ne bu nit deewee am na lu jóge ci moom di kontine dund. Am na ñu gëm ne ñi dee mën nañu fitnaal ñiy dund. Am na it ñuy wax ne Yàlla dina àtte ñu bon ñi, lakk leen ba fàww ci safara.

LI BIIBËL BI WAX : Nit, bu deewee, nekkatul. Ecclésiaste 9:5 wonee na ne ñi dee xamuñu dara. Ndegam ñi dee mënuñu xam walla yëg dara, kon nag mënuñu lor — walla dimbali — ñiy dund. — Psaumes 146:​3, 4.

Seetal itam Njàlbéen ga 3:​19 ak Ecclésiaste 9:​6, 10.

Ndax ñi dee dinañu mas a dekki ?

LI WARAL LAAJ BOOBU : Kenn bëggul dee, te ñépp a bëgg a am dund gu neex ak ñi ñu sopp. Kon nag, suñu soppe yi dee, jaadu na ñu namm leen lool te bëgg leen a gisaat.

LI BIIBËL BI WAX : Li ëpp ci ñi dee dinañu dekki. Yeesu dafa ñu dig ne ñi “ nekk ci seen bàmmeel . . . [dinañu] génn. ” (Yowaana 5:​28). Nit ñooñu di dekki dinañu mën a dund ci àjjana ci kaw suuf. Loolu ànd na ak li Yàlla bëggoon ci njàlbéen. (Luug 23:43). Ci li Yàlla dige noonu, ñi koy déggal dinañu am wér-gu-yaram bu mat sëkk ak dund gu dul jeex. Biibël bi nee na : “ Ñi jub dinañu moom suuf si, te dinañu dund ci kawam ba fàww. ” — Sabóor 37:​29, NW.

Seetal itam Job 14:14, 15 ; Luug 7:​11-​17 ak Jëf ya 24:15.

Lan laa mën a def ba Yàlla nangu sama ñaan ?

LI WARAL LAAJ BOOBU : Ci li gën a bare ci diine yi, nit ñi dañuy ñaan. Wànte ñu bare duñu yëg ne seen ñaan nangu na.

LI BIIBËL BI WAX : Yeesu dafa ñu jàngal ne, bu ñuy ñaan Yàlla, waruñu jël kàddu, topp ko di ko wax, di ko waxaat rekk. Dafa ne : “ Bu ngeen di ñaan, buleen topp yenn wax yi, di ko waxaat rekk. ” (Macë 6:​7, NW ). Bu ñu bëggee Yàlla déglu suñuy ñaan, war nañu ko ñaan ni mu ko bëgge. Bala ñu mën a def loolu, fàww ñu jàng ngir xam li Yàlla bëgg. Bu ñu ko xamee ba pare, nañu ñaan Yàlla li nga xam ne dafay ànd ak li mu bëgg. Lii la 1 Yowaana 5:​14 wax : “ Su nu [...] ñaanee [Yàlla] dara ci coobareem, dina nu nangul. ”

Seetal itam Psaumes 65:2 ; Yowaana 14:​6, 14 ak 1 Yowaana 3:​22.

Lan laa mën a def ba am jàmm ci sama dund ?

LI WARAL LAAJ BOOBU : Ñu bare dañuy defe ne xaalis, am tur bu siiw, walla taar dina tax ñu am jàmm ci seen dund. Moo tax ñu topp loolu kese, ba mujj a gis ne jàmm jooju ñu bëggoon raw na leen.

LI BIIBËL BI WAX : Yeesu wone na li ñu war a def ba mën a am jàmm. Lii la wax : “ Yéen ñi xam seen ñàkk doole ngir neex Yàlla, barkeel ngeen. ” (Macë 5:3). Kon fàww ñu def li war ba am li nit gën a soxla ci àddina, maanaam xam Yàlla te xam li tax mu sàkk nu. Loolu, mën nañu ko jàng ci Biibël bi. Su boobaa, dinañu mën a ràññee li am solo dëgg ak it li amul solo. Boo nangoo dëgg gi nekk ci Biibël bi won la li nga war a bëgg ak li nga war a def, sa dund dina gën a am njariñ. — Luug 11:28.

Seetal itam Proverbes 3:​5, 6, 13-​18 ak 1 Timote 6:​9, 10.

Juróom-benn laaj rekk lañu waxtaan fii. Gis nañu li ci Biibël bi tontu ci lu gàtt. Ndax bëgg nga xam lu ëpp loolu ? Dinga ko bëgg su dee yaa ngi bokk ci ñooñu “ xam seen ñàkk doole ngir neex Yàlla ”. Xéyna am nga yeneen laaj, yu mel ni yii : ‘ Su Yàlla fonkee nit, lu tax terewul lu bon ak naqar yu bare yi am bi àddina sosoo ba tey ? Lan laa mën a def ba gën a am jàmm ci sama biir kër ? ’ Biibël bi dafay joxe tont yu leer ci laaj yooyu ak yeneen yu bare.

Waaye tey ñu bare dañu ragal a gëstu Biibël bi. Pur ñoom, li ñu war a jàng ci Biibël bi dafa bare ba ëpp te léeg-léeg yombul a nànd. Ndax danga bëgg ñu dimbali la nga xam li Biibël bi tontu ci laaj yi ñu wax léegi ? Am na ñaari pexe yu Seede Yexowa yi am yu la ci mën a dimbali.

Bu njëkk bi, téere la. Mu ngi tudd Lan la Biibël bi wax dëgg-dëgg ? Téere boobu dañu ko defar ngir dimbali ñi amul jot ñu am tont yu leer yi Biibël bi jox ci laaj yi gën a am solo. Ñaareel bi mooy porogaraam bu ñuy def ngir jàngal la Biibël bi ci sa kër. Benn Seede Yexowa bu dëkk fu la jege te mën jàngale Biibël bi dina mën a ñëw sa kër walla feneen fu la gënal ngir jàng Biibël bi ak yow. Dingeen mën a jël tuuti jot semen bu nekk ngir def loolu. Doo fey dara. Ay milioŋi nit ci àddina si sépp jariñoo nañu porogaraam boobu. Jot nañu ay tont yu leer ci seeni laaj ba tax ñu ne : “ Dëgg la ! ”

Tont yooyu, alal bu réy la. Dafa lay yewwi ci bidaa yi, maanaam ay aada yu waral nit ñi dëkk ci ragal, yewwi la it ci jaaxle ak tiitaange. Dafa lay may yaakaar, won la li nga war a def ci àddina te indil la mbégte. Yeesu nee na : “ Dingeen xam dëgg gi te dëgg gi dina leen goreel [maanaam dina leen yewwi]. ” — Yowaana 8:​32.