Ñan ñooy def tey li yexowa santaane ?

Am na ay seede Yexowa fépp ci àddina si te bokk nañu ci xeet yépp ak cosaan yépp. Lan moo leen boole, ñu nekk benn ?

Lu tax Yàlla sàkk nit ?

Yàlla dafa bëgg ñépp xam li mu bëggoon bi muy sàkk nit. Loolu lan la, te ñan ñooy jàngale tey lu jëm ci loolu ?

LESSON 1

Ñan ñooy seede Yexowa yi dëgg-dëgg ?

Ndax xam nga ay seede Yexowa ? Ci dëgg-dëgg, lan nga xam ci ñun ?

LESSON 2

Lu tax ñu tudd Seede Yexowa ?

Xoolal ñetti mbir yi waral ñu jël tur woowu

LESSON 3

Dëgg gi nekk ci Biibël bi te réeroon naka la feeñaate ?

Naka lañu mën a xame ne nànd nañu bu baax li Biibël bi wax dëgg-dëgg ?

LESSON 4

Lu tax seede Yexowa yi tekki Biibël bi ci làkk yu bare ?

Lu tax tekki Kàddu Yàlla bi tudd Traduction du Monde Nouveau nekk tekki bu amul moroom ?

LESSON 5

Boo ñëwee ci suñuy ndaje karceen lan nga fay jële ?

Dañuy am ay ndaje ci suñu biir ngir jàng mbind mu Sell mi te xiirtalante. Ñu ngi lay xaar !

LESSON 6

Ban njariñ lañuy jële ci booloo ak suñuy mbokk ci ngëm ?

Kàddu Yàlla dafay xiir karceen yi ñuy booloo. Jàngal naka nga mënee jële njariñ ci booloo yu mel noonu.

LESSON 7

Lan lañuy def ci suñu ndaje yi?

Ndax mas nga laaj lan mooy xew ci suñu ndaje yi ? Dinga kontaane ndax njàngale Biibël bu set te leer bi nga fay dégg.

LESSON 8

Lu tax ñuy solu ba jekk bu ñuy dem ci suñu ndaje yi ?

Ndax ni ñuy soloo am na solo ci kanamu Yàlla ? Jàngal yan santaane Yàlla ñoo ñu mën a dimbali ci xam ni ñu war a soloo.

LESSON 9

Naka lañu mënee waajal bu baax suñu ndaje yi ?

Booy waajal ndaje yi, loolu dina la dimbali nga jële ci njariñ bu réy.

LESSON 10

Lan mooy njàngum Biibël ci biir njaboot ?

Xoolal ni la matuwaay boobu mënee dimbali nga gën a jege Yexowa te dëgëral diggante yi ci biir njaboot gi.

LESSON 11

Lu tax ñuy teew ci ay ndaje yu mag ?

At mu jot dañuy booloo ci suñu ñetti ndaje yu mag yu am solo. Ban njariñ nga mën a jële ci teewe ndaje yooyu ?

LESSON 12

Naka lañuy defe suñu liggéeyu waare Nguuru Yàlla ?

Dañuy topp fasoŋ bi ko Yeesu doon defe bi mu nekkee ci kaw suuf. Yan ñooy yen ci fasoŋu waare boobu ?

LESSON 13

Lan mooy pioñee ?

Ñu bare ci seede Yexowa yi dañuy jébbal 30 walla 50 waxtu, walla lu ko ëpp ci liggéeyu waare bi. Lan moo leen di xiir ci loolu ?

LESSON 14

Yan lekkool lañu jagleel pioñee yi ?

Ban lekkool bu am solo lañu jagleel pioñee yiy jébbal seen jot gépp ci liggéeyu waare Nguuru Yàlla gi ?

LESSON 15

Naka la magi mbooloo mi di dimbalee waa mbooloo ?

Magi mbooloo mi dañu am diggante bu rattax ak Yàlla, ñoom ñooy jiite ci mbooloo mi. Ban ndimbal lañuy def ?

LESSON 16

Lan mooy liggéeyu ñiy topptoo yëfi mbooloo mi ?

Ñiy topptoo yëfi mbooloo mi dañuy liggéey liggéey bu am njariñ ci mbooloo mi. Jàngal njariñ bi seen liggéey di indil ñépp ñiy teew ci ndaje mbooloo mi.

LESSON 17

Naka la wottukat yiy wër di ñu dimbalee ?

Lu tax wottukat yiy wër di seeti mbooloo yi ? Ban njariñ nga mën a jële ci seen ñëw ?

LESSON 18

Lan lañuy def ngir dimbali suñuy mbokk ci ngëm yi musiba dal ?

Bu musiba amee, dañuy gaaw a dem fajal suñu mbokk seeni soxla te dëfal seen xol ak Mbind mu sell mi. Naka lañu koy defe ?

LESSON 19

Kan mooy surga bu takku te teey bi ?

Yeesu dafa dige woon ne dina fi teg ab surga ngir muy joxe ñam ci wàllu ngëm ci waxtu bi ñu ko soxlaa. Naka la loolu di amee ?

LESSON 20

Jataay biy dogal, naka lay liggéeye ?

Ca jamono karceen yu njëkk ya, amoon na been gurup bu ndaw, ay góor yu mag, yu nekkoon jataay biy dogal ci mbooloo karceen bi. Lu jëm ci tey nag ?

LESSON 21

Lan mooy Betel ?

Betel béréb la boo xam ne dañu ko taxawal ngir def liggéey bu am solo. Jàngal ngir gën a xam lu jëm ci ñi fay liggéey.

LESSON 22

Ban liggéey lañuy def ci bànqaas yi ?

Dañuy kontaan buñu gisee ku

bëgg a xool ni suñu bànqaas mel. Ñëwal bés bu la neex !

LESSON 23

Naka lañuy binde suñu téere yi te naka lañu leen di tekkee ci yeneen làkk ?

Ñu ngi sotti ay téere ci lu ëpp 700 làkk. Lu tax ñuy def loolu yépp ngir tekki téere yi ci ay làkk yu bare ?

LESSON 24

Xaalis bi ñuy defe suñu liggéey ci àddina si sépp, fan la jóge ?

Lu jëm ci mbirum xaalis, lan moo wuutale suñu mbootaay ak yeneen diine yi ?

LESSON 25

Lu tax ñuy tabax ay saalu Nguur te naka lañu leen di tabaxe ?

Lan moo tax ñuy woowe suñu béréb yi ñuy jaamoo Yàlla saalu Nguur ? Jàngal ngir gën a xam ni tabax yu yem yooyu di dimbalee mbooloo yi.

LESSON 26

Naka lañu mënee bokk ci toppatoo suñu saalu Nguur ?

Toppatoo saalu Nguur yi ba ñu nekk béréb yu set te jekk dafay màggal Yàlla. Lan lañuy def ngir saalu Nguur yi nekk ci suñu gox kontine di set ?

LESSON 27

Ban njariñ nga mën a jële ci téere yi ñu mën a jàng ci saalu Nguur ?

Ndax am na aaya ci Biibël bi boo bëgg a nànd bu baax ? Ñëwal gëstu suñuy téere yi ñu def ci saalu Nguur gi ngir ku nekk mën cee jàng !

LESSON 28

Lan lañuy fekk ci palaas bi ñu moom ci Internet ?

Mën nga jàng ngir gën ñoo xam ak xam li ñu gëm te mën nga itam jot ay tont yu Biibël bi joxe.

Ndax dinga def li Yexowa bëgg ?

Yexowa dafa am mbëggeel dëgg ci yaw. Naka nga mënee wone ne bëgg nga def bés bu nekk li Yàlla santaane ?