Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 24

Xaalis bi ñuy defe suñu liggéey ci àddina si sépp, fan la jóge ?

Xaalis bi ñuy defe suñu liggéey ci àddina si sépp, fan la jóge ?

Népal

Togo

Grande-Bretagne

At mu nekk, suñu mbootaay dafay génne te di joxe ay téeméeri milioŋi Biibël ak yeneen téere te du ci jaay benn. Dañuy tabax te di toppatoo ay saalu Nguur ak ay Betel. Ñu ngi yor itam lu tollook ay junniy nit yuy liggéey ci Betel yi ak ay misioneer yu bare. Bu musiba amee itam dañuy yónnee foofu ndimbal. Xéyna dinga laaj sa bopp, ‘ xaalis biy def loolu yépp, fan la jóge ? ’

Duñu laaj dîme (maanaam jël benn ci fukki xaaju saleeru nit), duñu laaj nit ñi ñu kotise, te duñu laaj xaalis ñiy teewe suñuy ndaje. Dëgg la, suñu liggéeyu waare bi dafay laaj xaalis bu bare waaye duñu ñaan xaalis. Lu ëpp téeméeri at ci gannaaw, bi suñu ñaareelu téere bi tudd La Tour de Garde génnee, ñu ngi doon wax foofu ne, gëm nañu ne Yexowa moo ñuy dimbali. Waxoon nañu itam ne duñu mas a saraxu walla di ñaan nit mu jox ñu xaalis ; te ba léegi masuñu ko def. — Macë 10:⁠8.

Xaalis bi ñuy defe suñu liggéey bi, ci li nit ñi di maye la jóge. Nit ñu bare sopp nañu njàngale Biibël bi ñuy def te dañuy maye xaalis ngir jàpple ñu. Seede Yexowa yi ci seen bopp itam dañu bég ci joxe seen jot, seen doole ak di maye ci seen xaalis ak ci seen am-am ngir def li Yàlla bëgg ci àddina si sépp (Chroniques 29:⁠9). Ci biir saalu Nguur yépp ak ci ndaje yu mag yi, dafay am ay boyet yoo xam ne ku bëgg a maye xaalis mën nga ko fa dugal. Nit ñi mën nañu def itam ay maye jaarale ko ci suñu palaas bi ñu moom ci internet, jw.org. Maye yi ëpp, ci ay nit yu barewul xaalis la jóge. Ñoom dañu mel ni jigéen ji Yeesu doon tagg. Jigéen jooju, ku néew doole la woon, boole ci jëkkëram faatu. Waaye loolu yépp terewul mu dugal ñaari xànjar ci ndab ya ca kër Yàlla ga (Luug 21:​1-4). Kon ku nekk mën na “ ber ” dara ngir ‘ joxe ni mu ko nase ci xolam ’. — 1 Korent 16:2 ; 2 Korent 9:⁠7.

Wóor nañu ne Yexowa dina kontine di xiir nit ñi ko bëgg a ‘ teral ci seen alal ’ ci jàpple liggéeyu Nguuram ndax coobareem am ci kaw suuf. — Kàddu yu Xelu 3:⁠9.

  •  Lan moo wuutale suñu mbootaay ak yeneen diine yi ?

  •  Lan lañuy def ak maye yi ?