LESOŊ 33
Li nguuru Yàlla nar a def
Nguuru Yàlla taxaw na ba pare. Ci kanam tuuti, dina soppi lu bari ci kaw suuf. Nañu xool lu baax li nguuru Yàlla nar a def.
1. Naka la nguuru Yàlla di indiwaate jàmm ak njub ci kaw suuf?
Yeesu miy buuru nguuru Yàlla, dina alag nit ñu bon ñi ak nguur yi ci xeexu Armagedon (Peeñu 16:14, 16). Ci jamono jooju, dige bii ci Biibël bi dina mat sëkk: «Nes tuut, ku bon ne mes, nga seet, seet, mu réer» (Sabóor 37:10). Yeesu dina jaar ci Nguur gi, ngir feesal suuf si sépp ak jàmm ak njub (Jàngal Esayi 11:4).
2. Naka la dund gi di mel bu coobare Yàlla amee ci kaw suuf si?
Ci kilifteefu nguuru Yàlla, «aji jub ay jagoo réew mi [suuf si], dëkke ko ba fàww» (Sabóor 37:29). Xalaatal rekk dëkk ci àddina soo xam ne, ñépp a jub, bëgg Yexowa te ku nekk bëgg sa moroom! Kenn dootul feebar, te ñépp dinañu dund ba fàww.
3. Lan la nguuru Yàlla di def bu ñu alagee ñu bon ñi ba pare?
Bu ñu alagee nit ñu bon ñi ba pare, Yeesu dina nguuru 1 000 at. Ci jamono jooju, moom ak 144 000 ñiy nguuru ak moom, dinañu dimbali nit ñi ci kaw suuf ñu nekk nit ñu mat, ñu amul bàkkaar. Bu 1 000 at yi jeexee, suuf si sépp dina nekk àjjana ju rafet, te nit ñi ñépp dinañu bég ndaxte dañuy déggal Yexowa. Gannaaw loolu, Yeesu dina delloo nguur gi Baayam te ‘turu Yexowa dinañu ko sellal’ ci anam bu ñu ko masul a def (Macë 6:9, 10). Su boobaa dina leer ne, Yexowa njiit bu baax la te dafay toppatoo ñi muy ilif. Yexowa dina alag Seytaane, malaaka yu bon yi, ak ñépp ñi tànn bañ a nangu kilifteefam (Peeñu 20:7-10). Lépp li nguuru Yàlla indi, dina fi nekk ba fàww.
XÓOTALAL NJÀNG MI
Xoolal li tax ñu mën a gëm ne Yàlla dina jaar ci Nguuram ngir matal lépp li mu dige ci Biibël bi, lu jëm ci suñu ëllëg.
4. Nguuru Yàlla dina fi dindi nguuru doomu Aadama yi
‘Nit dafay yilif nit, muy loraangeem’ (Kàdduy Waare 8:9). Yexowa dina jaar ci Nguuram ngir dindi fi lépp lu njubadi boobu indi.
Jàngal Dañeel 2:44 ak 2 Tesalonig 1:6-8. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
-
Lan la Yexowa ak doomam Yeesu di def ak nguuru doomu Aadama yi ak ñi leen di jàppale?
-
Ci li nga jàng ci Yexowa ak Yeesu, lu tax nga am kóolute ne lépp li ñu nar a def, lu jub lay doon?
5. Yeesu mooy buur bi gën
Yeesu miy buur ci nguuru Yàlla, dina dimbali nit ñi ci kaw suuf, ci anam yu bari. Seetaanal WIDEO BI ngir gis ne, Yeesu am na bëgg-bëggu dimbali nit ñi te Yàlla may na ko kàttanu def ko.
Bi Yeesu nekkee ci kaw suuf, wone na li nguuru Yàlla nar a def. Ban ci barke yi ñu lim fii ci suuf nga yàkkamti mu am? Jàngal aaya yiy wax ci barke yooyu.
BI YEESU NEKKEE CI KAW SUUF... |
YEESU DINA TOLLU CI KAW ASAMAAN... |
---|---|
|
|
|
|
|
|
|
|
6. Nguuru Yàlla dina ñu may ëllëg ju neex
Nguur gi dina matal lépp li Yexowa bëggaloon nit ñi. Dinañu dund ba fàww ci àjjana ci kaw suuf. Seetaanal WIDEO BI ngir gis ni Yexowa di jaare ci Yeesu ngir matal li mu bëggaloon nit ñi.
Jàngal Sabóor 145:16. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
-
Xam ne Yexowa dina «reggal luy dund, ba xolam sedd», lan lay def ci yow?
BU LA NIT WAXOON: «Ñun ñépp bu ñu góor-góorloo, jafe-jafe yi dinañu fi jóge.»
-
Yan jafe-jafe la fi nguuru Yàlla nar a jële te nguuru doomu Aadama yi mënuñu ko?
NAÑU TËNK
Nguuru Yàlla dina matal lépp li Yàlla bëgg. Dina def suuf si sépp àjjana, te suuf si dina fees ak nit ñu nar a jaamu Yexowa ba fàww.
Nañu fàttaliku
-
Naka la nguuru Yàlla nar a sellale turu Yexowa?
-
Lu tax ñu mën a gëm ne, nguuru Yàlla dina matal dige yi nekk ci Biibël bi?
-
Ci barke yi nguuru Yàlla nar a indi, ban nga ci gën a yàkkamti mu am?
GËSTUL
Xoolal li nar a xew ci li Yeesu tudde ‘metit wu réy wi’ (Macë 24:21).
Xoolal ni benn njaboot di xalaate ci bés bi ñu nar a dund ci àjjana.
Ci waxtaan bi tudd «Laaj yu bari ñoo doon jaxase sama xel», xoolal ni góor gu sóobu woon ci politig gise ay tontu ci ay laajam.