Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 6

Àjjana jege na !

Àjjana jege na !

Lu bon li am tey ci kow suuf si, mu ngiy wone ne Àjjana jege na. Mbind mu sell mi waxoon na ne dinañu dund ci jamano ju mettee-metti, tuuti bala Àjjana ji agsi. Ci lañu nekk tey ! Li topp bokk na ci li Mbind mu sell mi waxoon ne dina am :

Xare yu mag. “ Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew xeex ak meneen réew. ” (Macë 24:7). Yégle boobu, gis nañu ko. Ca atum 1914 ba léegi, amoon na ñaari xeex yu mag yu boole woon àddina sépp ak yeneen xare yu gëna ndaw yu bare. Ay milioŋi nit ñoo ci dee.

Feebar yi di law ci béréb yu bare. “ Wopp [...] dina am ci bérab yu bare. ” (Lukk 21:11). Ndax loolu gis nañu ko ? Waaw. Feebar bu ñuy wax ‘ kanseer ’, feebaru xol, sëqat su bon si, sibbiru, sidaa, ak yeneen feebar ñooy rey ay milioŋi nit.

Lekk bu doyul. Ci àddina si sépp am na ay nit ñu dul lekk ba suur. Ay milioŋi nit ñooy dee at mu nekk ndax xiif. Loolu it dafay wone ne léegi Àjjana ji am ci kow suuf si. Mbind mu sell mi nee na : “ Dina am [...] ay xiif. ” — Mark 13:8.

Yëngu-yëngu suuf. “ Dina am [...] ay yengu-yenguy suuf ci bérab yu bare. ” (Macë 24:7). Loolu itam gis nañu ko ci suñu jamano. Lu ëpp benn milioŋu nit ñoo dee ci ay yëngu-yëngu suuf, 1914 ba léegi.

Nit ñu bon. Nit ñi dinañu “ fonk xaalis ” te “ siis ”, ‘ seen bànneex di leen gënal Yàlla ’. Xale yi dinañu “ xëtt [maanaam, baña topp] ndigalu waa-jur ”. (2 Timote 3:1-5.) Ndax nit ñu mel noonu barewuñu tey ? Faalewuñu Yàlla, te dañuy sonal ñi bëgga jàng xam Yàlla.

Jéggi li yoon tëral. Te it ñiy def “ lu bon ” dinañu gëna bare (Macë 24:12). Ndax nanguwuloo ne nit ñiy jéggi li yoon tëral ñu ngi gën di bare tey jii ? Foo mënta nekk, mën nañu la sàcc, nax la, walla gaañ la.

Loolu lépp mu ngi wone ne Nguuru Yàlla jege na. Mbind mu sell mi nee na : “ Bu ngeen gisee loolu lépp xew, xamleen ne nguuru Yàlla jege na. ” (Lukk 21:31). Lan mooy Nguuru Yàlla ? Nguur la gu Yàlla samp ca asamaan te mooy indi Àjjana ci kow suuf sii. Nguuru Yàlla mooy dindi nguuru nit ñi ba pare nguuru moom ci boppam. — Dañel 2:44.