Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 4

Naka nga mënee jàng xam Yàlla ?

Naka nga mënee jàng xam Yàlla ?

Boo jàngee Mbind mu sell mi, dinga mëna xam lu jëm ci Yexowa. Ca jamano yu yàgg ya, Yàlla tànn na ay nit ngir ñu bind ay xalaatam. Mbind yooyu lañu tudde Mbind mu sell mi. Tey, mën nañu jàng xam Yàlla bu ñu jàngee Mbind mu sell mi. Li Yexowa wax moo nekk ci Mbind mu sell mi, looloo tax ñu tudde ko itam Kàddu Yàlla. Mën nañu gëm li nekk ci Mbind mu sell mi ndaxte Yexowa du fen mukk. “ Yàlla mënul fen. ” (Yawut yi 6:18, NW). Kàddu Yàlla, dëgg gi la ëmb. — Yowanna 17:17.

Ci li Yàlla maye lépp, Mbind mu sell mi bokk na ci li ëpp solo. Mu ngi mel ni leetar bu jóge ci baay bu bëgg doomam yi. Dafa ñuy wax ci li ñu Yàlla dig : dina soppi suuf si mu nekk béréb bu rafet-a-rafet, fu dund di neex, maanaam àjjana. Dafa ñuy wax li Yàlla defoon démb, li muy def tey, ak li muy defal ëllëg doomam yi takku ci moom. Dafa ñuy dimbali itam ñu génn ci suñuy coono te am mbégte. — 2 Timote 3:16, 17.

Seede Yexowa yi, ay xaritu Yàlla lañu ; dinañu la dimbali nga xam li nekk ci Mbind mu sell mi. Nanga leen wax rekk ne danga bëgga jàng Mbind mu sell mi. Duñu la ci laaj xaalis (Macë 10:8). Mën nga itam teewe ndaje taalibe Isaa yi. Ci béréb bu ñuy wax Saalu Nguur gi lañuy def seeni ndaje. Boo fa teewee, dinga gaawa yokk sa xam-xam ci Yàlla.

Mën nga jàng xam Yàlla ci li mu sàkk. Nañu jël benn misaal. Mbind mu sell mi nee na : “ Yàlla sàkk na asamaan ak suuf. ” (1 Musaa 1:1). Bi Yexowa sàkkee “ asamaan ” si, sàkk na jant bi. Léegi, lan la ñu loolu di jàngal ci Yàlla ? Dafa ñuy jàngal ne Yexowa, bare na kàttan lool. Moom rekk moo mënoona sàkk lu réy ni jant bi. Dafa ñuy won itam ne Yexowa, ku am xam-xam la, ndaxte bu ñu seetee jant bi di joxe tàngaay ak leer te du fey mukk, dinañu xam ne ki ko sàkk boroom xam-xam la.

Li Yexowa sàkk wone na ne dafa ñu bëgg. Seetal doomu garab yi yépp am ci kow suuf si. Yexowa mënoon na ñu defal benn fasoŋu doomu garab kese — walla sax baña def benn. Waaye Yexowa sàkk na ay fasoŋu doomu garab yu bare te bu nekk ak melokaanam, tolluwaayam, kulóoram, ak cafkoom. Loolu dafay wone ne Yexowa, Yàlla ju am mbëggeel la, te yemul ci loolu rekk. Ku nangoo maye la itam, te dafa baax. — Sabuur 104:24.