NJÀNGALE 16
Nanga wone ne danga bëgg Yàlla
Boo bëggee yàgg ak xarit, war nga di waxtaan ak moom. Danga koy déglu, mu lay déglu. Te itam dangay wax lu baax ci moom. Noonu la it, boo nekkee xaritu Yàlla. Seetal li Mbind mu sell mi wax ci loolu :
Nanga faral di wax ak Yexowa ci ñaan. Nangeen “ sax ci ñaan Yàlla ”. — Room 12:12.
Jàngal Kàddu Yàlla gi, Mbind mu sell mi. “ Mbind mu sell mépp, ci gémmiñu Yàlla la jóge, te am na njeriñ ngir jàngal nit ñi, yedd leen, jubbanti leen. ” — 2 Timote 3:16.
Nanga jàngal nit ñi lu jëm ci Yàlla. “ Demleen nag sàkk ay taalibe ci xeet yépp, [...] te ngeen jàngal leen, ñuy sàmm lépp li ma leen sant. ” — Macë 28:19, 20.
Nanga teewe ndaje yi ca Saalu Nguur gi. “ Nanu seet ni nu mana xiirtalante cig mbëggeel ak ci jëf yu baax. [...] nanuy nàddante ci ngëm, di ko feddali. ” — Yawut yi 10:24, 25.
Nanga jàpple liggéeyu Nguur gi. “ Na ku nekk joxe, ni mu ko nase ci xolam, te bañ cee am réccu walla sañul-bañ, ndaxte kiy joxe ak mbég moo neex Boroom bi. ” — 2 Korent 9:7.