Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 17

Boo bëggee yàgg ak xarit, yow mii war nga nekk xarit

Boo bëggee yàgg ak xarit, yow mii war nga nekk xarit

Xaritoo, ci kow mbëggeel lañu koy tabax. Booy yokk sa xam-xam ci Yexowa, dinga ko gëna bëgg. Boo koy gëna bëgg, di ko gëna bëgga jaamu. Loolu dina tax nga bëgga nekk taalibe Isaa (Macë 28:19). Boo bokkee ci Seede Yexowa yi mel ni njaboot gu bég, dinga mëna xaritoo ak Yàlla ba fàww. Lan nga wara def ?

Danga wara topp ndigalu Yàlla yi ngir wone ne bëgg nga ko. “ Ndaxte mbëggeel ci Yàlla mooy sàmm ay ndigalam ; te ay ndigalam diisuñu. ” — 1 Yowanna 5:3.

Nanga jëfe li ngay jàng. Isaa nettali na luy misaal loolu. Nit ku am xel tabax na këram, samp ko ci xeer. Ku ñàkk xel samp këram ci suuf kese. Bi ngelaw bu réy-a-réy amee, kër gi ñu sampoon ci xeer daanuwul, waaye kër gi ñu sampoon ci suuf kese, daanu na daanu bu metti. Isaa nee na ñiy dégg li muy jàngale, di ko topp, ñu ngi mel ni kooku am xel te samp këram ci xeer. Waaye ñiy déglu li muy jàngale, te duñu ko topp, ñu ngi mel ni ku ñàkk xel kooku sampoon këram ci suuf kese. Diggante ñaari nit ñooñu, kan nga bëgga niru ? — Macë 7 :24-27.

Jébbal sa bopp Yàlla. Loolu, mu ngi tekki ne dangay jege Yexowa ci ñaan te wax ko ne danga bëgga def li mu bëgg ba abadan. Def li Yàlla bëgg mooy wone ne taalibe Isaa nga. — Macë 11:29.

Sóob bi ci ndox. “ Ñu sóob la ci ndox, nga set ci say bàkkaar ci tudd turu Yeesu [maanaam Isaa]. ” — Jëf ya 22:16.

Booy jaamu Yàlla, nanga ko def ak sa kem kàttan. “ Lu ngeen mana def, na ci seen xol tàlli; ngeen def ko ngir Boroom bi, te du ngir nit. ” — Kolos 3:23.