Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

NJÀNGALE 2

Kan mooy Yàlla ?

Kan mooy Yàlla ?

1. Lu tax ñu war a jaamu Yàlla ?

Yàlla dëgg ji moo sàkk lépp. Amul komaasemaa te moo fi sax ba fàww (Sabóor 90:2). Xibaaru jàmm bi nekk ci Biibël bi, ci Yàlla la jóge (1 Timote 1:11). Ndegam Yàlla moo ñu may dund, moom rekk lañu war a jaamu. — Jàngal Peeñu ma 4:11.

2. Naka la Yàlla mel ?

Kenn masul gis Yàlla ndaxte Xel la. Xel mooy fasoŋu bakkan boo xam ne moo sut fuuf bakkanu bépp mbindeef buy dund ci kaw suuf (Yowaana 1:18 ; 4:24). Bu ñu xoolee li Yàlla sàkk, dinañu ci gis mbiri Yàlla yi, maanaam jikko yu rafet yi ñu mën a gis ci Yàlla. Bu ñu xoolee doomu garab yi ak fulóor yu bare yi Yàlla sàkk, dinañu gis mbëggeelam te xam ne ku bare xam-xam la. Ni àddina ak jaww ji tollu dafay wone kàttanu Yàlla. — Jàngal Room 1:20.

Mën nañu xam lu bare ci mbiri Yàlla yi bu ñuy jàng Biibël bi. Ci Biibël bi, mën nañu xam li Yàlla bëgg ak li mu bañ, xam it ni muy doxale ak nit ñi ak ni muy doxale ci bépp fànn. — Jàngal Sabóor 103:7-10.

3. Ndax Yàlla am na tur ?

Yeesu nee na : “ Sunu Baay bi nekk ci kaw, yal na sa tur di lu ñu sellal ” (Macë 6:9, ñun ñoo dëngal mbind mi). Ni ñu mën a woowee Yàlla bare na, waaye benn tur rekk la am. Ci làkk bu nekk am na ni ñu koy waxe. Ci wolof ñu ngi koy wax “ Yexowa. ” Waaye am na ay nit yu koy wax “ Yahweh ”. — Jàngal Sabóor 83:19.

Turu Yàlla dindi nañu ko ci Biibël yu bare def fa Boroom bi walla Yàlla. Waaye ba ñu doon bind Biibël bi, turu Yàlla feeñoon na fa lu jege 7 000 yoon. Yeesu xamal na nit ñi turu Yàlla bi mu leen daan jàngal lu jëm ci Yàlla. — Jàngal Yowaana 17:26.

Seetaanal wideo Ndax Yàlla am na tur ?

4. Ndax Yexowa fonk na ñu ?

Ni baay bii bëgge doomam, noonu la Yàlla di defe lépp ngir ñu am dund bu neex.

Coono yiy dal doomu Aadama yi, ndax loolu dafay tekki ne Yexowa Yàlla fonku ñu ? Am na ñuy wax ne Yàlla moo ñuy teg coono ngir nattu ñu, waaye du loolu. — Jàngal Saag 1:13.

Yàlla jox na doomu Aadama yi sañ-sañu tànnal seen bopp li ñu bëgg a def. Ndax loolu du lu neex, ñu am sañ-sañu tànnal suñu bopp jaamu Yàlla (Josué 24:15) ? Waaye ñu bare dañuy tànn def seen moroom lu bon, moo tax coono yi bare tey. Yexowa su gisee njubadi boobu dafay am tiis. — Jàngal Njàlbéen ga 6:5, 6.

Yexowa Yàlla fonk na ñu. Dafa bëgg ñu am bànneex. Ci kanam tuuti, dina fi jële coono yi ak ñi tax coono yooyu di am. Am na lu tax Yàlla bàyyi coono yi di am ba tey. Ci njàngale 8, dinañu xam lu waral loolu. — Jàngal 2 Piyeer 2:9 ; 3:7, 13.

5. Naka lañu mënee jege Yàlla ?

Yexowa dafa bëgg ñu jege ko ci ñaan. Ku nekk ci ñun Yexowa yëg na la (Sabóor 65:3 ; 145:18). Yexowa, ku nangoo baale la. Te it, lépp li ñuy jéem a def ngir neex ko, dafa koy gis, bu dee sax yenn saay dañuy juum. Suñu matadi terewul ñu mën a am diggante bu rattax ak Yàlla. — Jàngal Sabóor 103:12-14 ; Saag 4:8.

Ndegam Yexowa moo ñu may dund, moom lañu war a gën a bëgg (Màrk 12:30). Booy gën di jàng lu jëm ci Yàlla te di def li mu santaane, dinga wone sa mbëggeel ci moom te bu boobaa dinga ko gën a jege. — Jàngal 1 Timote 2:4 ; 1 Yowaana 5:3.