NJÀNGALE 4
Kan mooy Yeesu Kirist ?
1. Fan la dundu Yeesu komaase ?
Yeesu wuute na ak bépp doomu Aadama, ndaxte ci kaw asamaan la doon dund ni malaaka bala muy juddu ci kaw suuf si (Yowaana 8:23). Yeesu la Yàlla njëkk a sàkk, te Yeesu jàpple na ko mu sàkk leneen lépp. Yeesu kese la Yexowa sàkk te jaarul ci kenn, loolu moo tax jaadu na ñu koy woowe “ Doomam ji mu am kepp. ” (Yowaana1:14.) Yeesu moo doon jottali Kàddu Yàlla moo tax ñu koy woowe itam “ Kàddu gi ”. — Jàngal Kàddu yu Xelu 8:22, 23, 30 ; Kolos 1:15, 16.
2. Lu tax Yeesu ñëw ci kaw suuf ?
Yàlla dafa jël bakkanu Yeesu ca asamaan, toxal ko ci biiru benn janq Yawut bu tudd Maryaama. Noonu la yónnee doomam ci kaw suuf si. Kon Yeesu amul woon baay ni ñun (Luug 1:30-35). Yeesu dafa ñëw ci kaw suuf (1) ngir jàngal ñu dëgg gi ci Yàlla, (2) ngir nekk suñu royukaay ci def coobare Yàlla, bu dee sax dañu nekk ci ay jafe-jafe, (3) ngir joxe it bakkanam ni peyug ‘ njot ’. — Jàngal Macë 20:28.
3. Lu tax ñu soxla njot gi ?
Njot mooy li ñuy fey ngir musal nit ku ñu jàpp bëgg ko rey (Exode 21:29, 30). Dee ak màgget bokkul woon ci li Yàlla bëggoon ca njàlbéen pur doomu Aadama yi. Naka lañu ko xame ? Yàlla dafa waxoon Aadama, góor gu njëkk ga ne, bu defee lu Biibël bi di woowe “ bàkkaar ” dina dee. Kon su Aadama bàkkaarul woon du mas a dee (Njàlbéen ga 2:16, 17 ; 5:5). Ni ko Biibël bi waxe dee “ dugg ” na ci àddina ndax Aadama. Kon Aadama wàll na doomam yépp bàkkaar ak li mu indi, maanaam dee. Soxla nañu njot gi ngir ñu mën a mucc ci dee bi ñu donn ci Aadama. — Jàngal Room 5:12 ; 6:23.
Kan moo mën a fey njot gi ngir yewwi ñu ci dee ? Bu ñu deewee, suñuy bàkkaar kese lañuy fey. Nit ku matadi mënul fey bàkkaaru moroomam. — Jàngal Sabóor 49:8-10.
4. Lu tax Yeesu dee ?
Yeesu wuute na ak ñun ndaxte ku mat la. Kon soxlawul mu dee ngir ay bàkkaaram — ndaxte masul a bàkkaar. Wànte Yeesu dee na ngir bàkkaaru ñeneen. Yàlla wone na mbëggeel bu réy a réy bi mu am ci doomu Aadama yi, ci li mu yónni doomam ngir mu dee pur ñun. Yeesu itam won na ñu mbëggeelam bi mu déggalee Baayam ba joxe bakkanam ngir suñuy bàkkaar. — Jàngal Yowaana 3:16 ; Room 5:18, 19.
Seetaanal wideo Lan moo tax Yeesu dee ?
5. Fi mu tollu nii, lan la Yeesu di def ?
Bi mu nekkee ci kaw suuf, Yeesu dafa doon faj ñi feebar, dekkal ñi dee te musal nit ñi ci musiba. Ci noonu wone na li mu nar a defal ëllëg nit ñi déggal Yàlla (Macë 15:30, 31 ; Yowaana 5:28). Ginnaaw bi Yeesu deewee, Yàlla dekkal na ko mu dellu nekkaat malaaka (1 Piyeer 3:18). Noonu Yeesu toog ci ndeyjooru Yàlla di xaar ba Yexowa jox ko kàttanu ilif suuf si sépp ni Buur (Yawut ya 10:12, 13). Fi mu tollu nii, Yeesu mu ngi ilif ni Buur ci asamaan, te talibeem yi ñu ngi yégle xibaaru jàmm boobu ci àddina si sépp. — Jàngal Dañeel 7:13, 14 ; Macë 24:14.
Ci kanam tuuti Yeesu dina jëfandikoo kàttanam ni Buur ngir jële fi bépp coono ak ñi tax coono yooyu di am. Képp ku am ngëm ci Yeesu, di ko déggal, dinga mën a dund ci àjjana ci kaw suuf. — Jàngal Sabóor 37:9-11.