NJÀNGALE 14
Lu tax Yàlla am mbootaay ?
1. Lu tax Yàlla def Israyil bu njëkk ba mbootaayam ?
Yàlla dafa jël ay sëtu maam Ibraayma def leen mbootaay te jox leen ay sàrt. Mu tudde leen “ Israyil ” te sas leen ñu sàmm kàddoom ak diine dëgg ji (Sabóor 147:19, 20). Kon nit ñi ci xeet yépp mënoon nañu barkeelu ci waa Israyil. — Jàngal Njàlbéen ga 22:18.
Yàlla tànnoon na waa Israyil ngir ñu nekk ay seedeem. Jaar-jaaru Israyil bu njëkk ba, wone na naka la nit di ame jàmm bu toppee sàrtu Yàlla yi (Deutéronome 4:6). Noonu yeneen xeet yi mënoon nañu jaar ci waa Israyil ngir xam Yàlla dëgg ji. — Jàngal Isaïe 43:10, 12.
2. Lu tax Karceen dëgg yi booloo nekk benn ?
Ci diggante bi, waa Israyil ñàkk nañu barke Yàlla, Yexowa jël mbooloo Karceen mu wuutu leen (Macë 21:43 ; 23:37, 38). Léegi, Karceen dëgg yi ñoo jël palaasu waa Israyil te nekk ñiy seede Yexowa. — Jàngal Jëf ya 15:14, 17.
Yeesu won na ñi mu doon àndal ni ñu war a doxale ngir waare te sàkk ay taalibe ci xeet yépp (Macë 10:7, 11 ; 24:14 ; 28:19, 20). Fi ñu tollu nii ci mujug jamono, liggéeyu waaraate bi léegi mu àgg ci njeexteelam. Yexowa def na lu masul a am, ci lu mu boole ay milyoŋi nit ci xeet yépp ci diine dëgg ji (Peeñu ma 7:9, 10). Karceen dëgg yi dañoo booloo nekk benn ngir xiirtalante te dimbalante. Ci àddina si sépp, ñoo bokk benn porogaraamu njàngum Biibël bi ci seen ndaje yi. — Jàngal Yawut ya 10:24, 25.
3. Kañ la mbootaayu Seede Yexowa yi tàmbali ci suñu jamono ji ?
Ci atum 1870, benn mbooloo bu ndaw bu doon jàng Biibël bi, komaase woon na feeñal dëgg yu nëbbu woon ci Biibël bi. Mbooloo boobu xamoon na ne, Yeesu wonoon na mbooloo Karceen ni mu war a doxale ngir waare, noonu ñu tàmbali liggéeyu waare Nguur gi ci àddina si sépp. Ci atum 1931 lañu jël turu Seede Yexowa. — Jàngal Jëf ya 1:8 ; 2:1, 4 ; 5:42.
4. Naka la Seede Yexowa yi di doxale ci seen biir ?
Ca jamono karceen yu jëkk ya, dafa amoon benn Jataay biy dogal bu doon jiite mbooloo Karceen yi amoon ci dëkk yu bare. Jataay boobu dafa nangu woon ne Yeesu mooy Kilifa mbooloo mi (Jëf ya 16:4, 5). Naka noonu, tey itam am na Jataay biy dogal ci Seede Yexowa yi. Ay mag yu bare xam-xam lañu. Jataay boobu dafay wottu bànqaasu Seede Yexowa yi nga xam ne dañuy tekki, di defar ak a yónnee ay jumtukaay ngir jàng Biibël bi ci lu ëpp 600 làkk. Rax-ci-dolli Jataay biy dogal mu ngi joxe ay xiirtal ak ay tegtal yu jóge ci Mbind mu sell mi ci lu ëpp 100 000 mbooloo ci àddina si sépp. Ci mbooloo bu nekk, am na ay góor yu àttan sasu magi mbooloo walla wottukat. Góor yu baax yooyu dañuy toppatoo bu baax ñi nekk ci mbootaayu Yàlla. — Jàngal 1 Piyeer 5:2, 3.
Seede Yexowa yi xam nañu ni ñuy doxale ngir waare xibaaru jàmm bi te sàkk ay taalibe. Ni taalibe Yeesu yi, dañuy dem waare ci kër yi (Jëf ya 20:20). Dañuy jàngal Biibël bi nit ñi dëggu te bëgg dëgg gi. Waaye Seede Yexowa yi nekkuñu benn mbootaay rekk, yem ci. Dañu mel ni njaboot bu am baay bu leen bëgg. Ay mbokk lañu yu bëggante (2 Tesalonig 1:3). Ñiy jaamu Yexowa dañoo booloo nekk benn ngir neex Yàlla te di dimbali nit ñi, moo tax ñu nekk njaboot bi gën a bég ci kaw suuf si. — Jàngal Sabóor 33:12 ; Jëf ya 20:35.