Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Jàng nekk nit ku sawar ci liggéey, dafa mel ni espoor. Dafa lay amal njariñ tey ak ëllëg

NDAW ÑI ÑOO MOOM LII

11: Cawarte

11: Cawarte

LI MUY TEKKI

Nit ku sawar ci liggéey, du daw liggéey. Waaye dafay liggéey bu baax ngir faj ay soxlam te dimbali ñeneen ñi, bu dee sax nit ñi fonkuñu fasoŋu liggéey bi muy def.

LI TAX MU AM SOLO

Mu neex ñu mbaa mu naqari ñu, nit ku nekk, am na li ko war ci dundam. Ci àddina soo xam ne nit ñu bare fonkuñu liggéey, sawar ci liggéey mën na la amal njariñ (Kàdduy Waare 3:13).

«Jàng naa ne, booy liggéey bu baax, dangay fonk sa bopp te bég. Ci dëgg, mbégte moomu moo tax ma bëgg liggéey. Nekk nit ku sawar ci liggéey, mooy tax nit ñi fonk la» (Reyon).

LII LA BIIBËL BI WAX: «Kër-këri, jariñu» (Kàddu yu Xelu 14:23).

LI NGA MËN A DEF

Xelal yii di topp, dinañu la dimbali, nga am gis-gis bu rafet ci liggéey.

Jàngal a def sa liggéey ni mu ware. Booy def liggéey bi ñu la jox ci kër gi, mbaa ca lekkool ba walla ci sa liggéeyukaay, def ci sa xel mépp. Boo jàngee benn liggéey ba mokkal ko, fexeel ba mën koo def ci lu gën a gaaw ak ni mu gën a rafete. Booy gën di xareñ ci sa liggéey nga koy gën di bëgg.

LII LA BIIBËL BI WAX: «Seetlul ku man liggéeyam, buur lay liggéeyal, du liggéeyal baadoolo» (Kàddu yu Xelu 22:29).

Xalaatal ci njariñ bi sa liggéey am. Daanaka, saa yoo defee sa liggéey bu baax, ñeneen ñi dinañu ci jariñu. Boo sawaree def liggéey bi ñu la jox ci kër gi, dina gën a yomb ci waa kër gi.

LII LA BIIBËL BI WAX: «Joxe moo gëna barkeel nangu» (Jëf ya 20:35).

Bul yem rekk ci li ñu la sant. Bu ñu la joxee liggéey, bul yem rekk ci li ñu la wax nga def, waaye dem ci ba jeex. Boo ko defee, dinga wone ne yaa moom sa bopp, te li ngay def kenn forsewu la ci, waaye yaa ko defal sa bopp (Macë 5:41).

LII LA BIIBËL BI WAX: «Noonu ndimbal li nga may defal du nekk sañul-bañ, waaye mu ànd ak xol bu tàlli» (Filemon 14).

Xamal fi nga war a yem. Nit ku sawar du tayel, waaye itam du ëppal ci liggéeyam. Dafay yemale liggéeyam ci palaasam. Dafay bég ci liggéey bu baax bi muy def, di bég itam ci féexal xolam.

LII LA BIIBËL BI WAX: «Waaye benn ŋëb bu ànd ak dal moo gën ñaari ŋëbi doñ-doñ ci napp um ngelaw» (Kàdduy Waare 4:6).