Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Déggal say waajur dafa mel ni fey bor boo ameel bank. Booy fey sa bor, ñu di la gën a wóolu, te gën laa lebal.

NDAW ÑI ÑOO MOOM LII

10: Kóolute

10: Kóolute

LI MUY TEKKI

Nit ku ñu mën a wóolu mooy nit kiy def li waajuram yi, xaritam yi walla pataroŋam di xaar ci moom. Dafay dégg ndigal, di def li mu dige, tey wax dëgg saa su nekk.

LI TAX MU AM SOLO

Daanaka, ci bépp fànn, liberte bi ñu lay may, mu ngi aju ci kóolute gi nit ñi jot a am ci yow.

«Boo bëggee say waajur wóolu la, danga war a wone ne, ku mat a wóolu nga, bu ñu fi nekkee ak bu ñu fi nekkul» (Sarahi).

LII LA BIIBËL BI WAX: «Seetluleen seen bopp» (2 Korent 13:5).

LI NGA MËN A DEF

Moo xam ndax danga bëgg ñu gën laa wóolu, walla ñu wóoluwaat la, lii di topp, mën na la dimbali.

Deel wax dëgg. Boo dul wax dëgg, loolu dafay gaaw a yàq kóolute gi nit ñi am ci yow. Waaye, booy wax dëgg, rawatina boo juumee, ñeneen ñi dinañu la mën a wóolu.

«Bu porobalem amul, wax dëgg dafay yomb. Waaye boo juumee, ba tey nga wax dëgg, mën na tax ñu gën laa wóolu» (Caiman).

LII LA BIIBËL BI WAX: «Danoo bëgga rafet ci lépp lu nuy def» (Yawut ya 13:18).

Nekkal nit ku ñu mën a wóolu. Ci benn gëstu bi ñu def ci Etaa Sini, 78% ci ñiy toppatoo liggéeykat yi, wax nañu ne «nekk nit ku ñu mën a wóolu, bokk na ci ñetti jikko yu am solo yuy tax nit am liggéey.» Jàng nekk ku ñu mën a wóolu tey, dina la amal njariñ boo magee.

«Su may def liggéey bi ma samay waajur sànt ci kër gi, te duma xaar ñu waxaat ma ko, ñoom dañu koy seetlu. Lu may gën di def lu ni mel, ñu may gën di wóoolu» (Sarah).

LII LA BIIBËL BI WAX: «Ndax wóor na ma ne dinga ma déggal, ba weesu sax li ma la sant» (Filemon 21).

Deel muñ. Xale buy màgg, di njool, dañu koy gis ci lu leer. Waaye dafay laaj jot ngir nit ñi gis ne mag la ci doxalin ak ci jikko.

«Du benn jëf ju baax rekk ji nga def, mooy tax sa waajur yi ak ñeneen ñi wóolu la. Waaye, mën nga dem ba nekk nit ku mat a wóolu, booy def saa su nekk liy tax ñu wóolu la» (Brandon).

LII LA BIIBËL BI WAX: «Solooleen boog [...] muñ» (Kolos 3:12).