NDAW ÑI ÑOO MOOM LII
9: Ki nga doon
LI MUY TEKKI
Ki nga doon, du rekk sa tur walla sa melokaan. Ëmb na itam sa jikko, li nga gëm, li nga bëgg ak li ngay bañ. Kon, li ñu fiy wax mooy, li nit ki doon dëgg, ci biir ak ci biti.
LI TAX MU AM SOLO
Boo xamee dëgg ki nga doon, dinga fonk li nga gëm te doo bàyyi say moroom dugal la ci li nga bëggul.
«Ñit ñu bare, dañu mel ni mannequins yi ngay gis fi ñuy jaaye yére. Dañu leen di tànnal li ñuy sol, du ñoom ñooy tànnal seen bopp» (Adrian).
«Jàng naa def lu baax, bu dee sax yombul. Jàng naa ràññe ñan ñooy samay xarit dëgg, ci ni ñuy doxale ak man ak ci ni may doxale ak ñoom» (Courtney).
LII LA BIIBËL BI WAX: «Bu leen àddina jay, waaye yeesluleen ci seen xel, ba soppiku» (Room 12:2).
LI NGA MËN A DEF
Xamal bu baax ki nga doon tey ak ki nga bëgg doon ëllëg. Ngir xam ki nga doon, xalaatal ba xam li nga mën, li nga mënul ak li nga gëm. Li la ci mën a dimbali mooy nga tontu laaj yii di topp.
Li nga mën: Ci lan laa gën a xareñ? Yan jikko yu baax laa am? (Maanaam: Ndax damay respekte heure? Ndax ku maandu laa? Ndax ku ñeme coono laa? Ndax damay maye?) Yan jëf yu baax lay def?
XELAL: Ndax jafe na ci yow nga lim say jikko yu baax? Bu dee waaw, laajal say waajur walla sa benn xarit boo wóolu, mu wax la say jikko yu baax ak li tax mu wax ko.
LII LA BIIBËL BI WAX: «Na ku nekk seetlu ni muy beye sasam. Bu ko defee dina mana naw boppam, tey bañ di diirante mbagg ak ñi ci des» (Galasi 6:4).
Li nga mënul: Lan laa war a soppi ci sama jikko? Lan moo ma gën a mën a dugal ci lu bon? Ci yan fànn laa war a gën a maandu?
LII LA BIIBËL BI WAX: «Su nu waxee ne amunu bàkkaar, kon nax nanu sunu bopp» (1 Yowaana 1:8).
Li nga gëm: Lan laa gëm ak lu tax? Ndax gëm naa Yàlla? Lan moo ma wóor ne Yàlla am na? Ci man, lan mooy lu jubadi ak lu tax? Lan mooy sama yaakaar lu jëm ci ëllëg?
LII LA BIIBËL BI WAX: «Di xalaat bu baax, moo lay aar, te di ràññe mooy tax nga mucc» (Kàddu yu Xelu 2:11, MN).