Ndax li nekk ci Biibël bi, waxu nit la ?
Li Biibël bi wax
Xam-xam bu am solo moo nekk ci Mbind mu sell mi, maanaam Biibël bi. Waaye xam-xam boobu, jógewul ci nit. Xoolal li Biibël bi wax : « Mbind mu sell mépp, ci gémmiñu Yàlla la jóge » (2 Timote 3:16, Téereb Injiil di Kàddug Yàlla). Am na lu bare luy dëgëral wax jooju. Xoolal liy topp :
Li Biibël bi wax lu jëm ci li xewoon démb, kenn masu koo weddi ba am dëgg.
Ay nit yu dëggu ñoo bind li nekk ci Biibël bi. Lépp lañu wax, nëbbuñu dara. Kon mën nañu gëm ne li ñu wax dëgg la.
Lépp li nekk ci Biibël bi, mu ngi jëm ci wax jii : Yàlla rekk moo war a ilif doomu Aadama yi te Nguuram bi nekk ci asamaan mooy tax lépp li mu bëgg di am.
Tey xam nañu ne nit ñi ca jamono yu yàgg ya, juumoon nañu lu bare ci li tubaab di woowe science. Waaye Biibël bi moom, bu dee sax bind nañu ko ay junniy at ca gànnaaw, juumul ci fànn yooyu.
Boroom xam-xam yiy gëstu li xewoon démb, boo xoolee ci seen téere yi, dinga gis ne li Biibël bi yégle woon am na.